♡♡♡♡

54 3 0
                                    

Cëy àddina! Kuma waxoon lii dina masa jeex duma ko gëm. Fii lañ daan daje di took di waxtaan buma masaane jug ngir jëmsi fii day melne sama bànneexu àddina lépp fila nekk damay yàkkam ti lool ta buma aksee ba toog sax duma xamati fan laa jaar ba aksi fii. Ta buñ waraana daje maa kafiy jiitu ta buma aksee ba toog kuma séen muy ñëw rekk mane moom la ndax boo ba samay bët moom rekk lay gis. Waaye suma ko séenee rekk di naa xamne bokkul ak ñimakay jaawaleel ndax ci sama xol❤ laay yëg ne kii di ñëw ku sax ci sama xol la. Bu aksee ma jug akolaat ko nu toog sunuy bët ñent ma melni ku nekk aljanna. Duma masa fàtte ay reetaanam wala mu muuñ day melni rekk àddina man rekk maafiy dund bànneex damay yëg li ma doon bubaax ak fiertés.
Cëy sunuy waxtaan su waxee day melne sama catu karaw baci samay we lepp day dégg kàddu gi may yëg lu dëggu ci man jëm ci moom. Sumay wax ak moom limay wax lumma ñor ñor suma xoolee rekk ree ta noppee guma damay daadi daaneel samay kàddu ndax liy juge ci moom di dugg ci sama yaram yëngël sama xol di daw ci sama dereet nëxël samam xel. Fiñi toog ba nii manulalaa wax dayob lëndë maayam wala dayob leeraayam num toll ndax amul benn bis buma fi toogee ak moom ba yëg ne fii mel na nii wala mel na nee , su xasee ba toog rekk day melni dootuma yëg wala may gis ludul moom. Barab bii tay barab bu am dayo la ci man ndax lima fi dund ak lima fiy yëg mooy lima dootul fàtte mukk ci àddina . Ci kii laa xamee ne mbëgel lu am la lu dëggu la rawatina liñ naan lu jiitu ci xol des ca.

Cëy aka amoon palaas ci sama xol manak moom sunu mbëgél ak fim mujj dafa mel ne rekk garab goo xamne dañoo jël jiwu ba jiko diko suuxat diko toppatoo bam tàmblee màgg ñukay defar diko rafetal bam màgg ba dëgër ami bànqaas yu naat loolu méññ fum toll di jébbi mu dem ba tàmblee tóor-tóor rekk ñu dagg ko. Waaye wolof neena garab gu mag bu daanoo xob ya lax; ma tek ci ne waaye reen ya du lax .
Palaas binga amoon ci sama xol dina dëke vide ndax kaneen manatu faa dugg . Buma don garab mane yaay réen yima daan dundal. Mbëgel bu don jant kon mane sama jant sona. Ñàkk laa dégg du tax ma fàttela. Ñàkk laa gis du tax sama miineel ci yaw dañ. Suma manoona ariyeeraat jamono ba aksi ci lañ daan dund bu dee benn waxtu sax bëgg naa. Ngir ma dundalaat sama xol ci lim mànke.

Fii ma toog de bu ma noona wax dinama doy sëkk seede ci finga toll ci man maangi yëg lu nit mënta nettali . Sun palaas bii ma toog dafa mel ni sa xet dama fiy xeeñ maa ngi lay yëg dila janeer lepp luñ fi masa waxtaane rekk daa mel ne benn film bumay seetaan. ci suñ palaas bii laa xamee ne lépp loo gis mu dee ndekete mangay dund ca biir limafiy gëj gëj bima fi toogee lepp lun fi masa dundd daa dikaat ci sama xel di dox ci sama xol♡. Ndax di nga wéet ba xalaat ni sama xar kanam daan mel boo masaan di wax ak man ba sunuy nët ñeent? Bima nekkee ak yaw dafa melni ci kaw suuf benn jigéen rekk moo fi nekk . Sumay lekk baa may naan ba sama xel ne yarr ci yaw dootuma xam limay lekk lumiy saf, demoon naa sax ba naan xiif naa xiifuma mar naa maruma ta bamakay wax nimako don génnee ci sama làmiñ nim nekke woon ci sama xol mooko raw fuuf.
Ku masaana xool sama xar kanam yaw lay gis kuma bëga jot yaw lay tudd binga ma soree laay dooga xam dëgg-dëgg linga don jariñ ci sama wet saa booma jegewaan dama daan yëg sama bopp kom ci àddino maaci gëna heureux. Waaye saa boo ma soree sama naqari dereet rekk feebar la woon ndax dara du saf ci man du ma gis dara ta lu nit ñi di gëna bari may gëna wéet . Ci yaw laa xamene xol kimu bëgg rekk mooka mana wéttali . Sunu palaas bii rekk doy na ci firnde ndax toog gi mafi toog rekk mel nani man ak yaw ñoo ngi dund ndax sama xol moo ngi yëg li sama xel di fàttali ku ci liñ daan dund . Palaas bii de suma ko moomoon am man kon kuko gis dina xam ne fii fenn la ci man ndax di naa ko defar bam wane ne fii ay nit dañ fee dund luñ dul fàtta. FOO MANA NEKK LU MANA XEW NA NGA XAMNE LINGAFI BÀYYI WOON MINGI FI BA TAY ❤

Vous avez atteint le dernier des chapitres publiés.

⏰ Dernière mise à jour : Dec 08, 2021 ⏰

Ajoutez cette histoire à votre Bibliothèque pour être informé des nouveaux chapitres !

mbëgél Où les histoires vivent. Découvrez maintenant