Dëgërël muñ sa tiisu sëy, bula mer yen ba gaa nu fay,

122 4 0
                                    

Balamay tàggatoo gërëm, xale biy sëy di wut ngërëm, gore yiiw nob boroom, kërëm sëyewul xaatimak xërëm, ta du ngaayoo ngiruk wujje .

Dëgërël muñ sa tiisu sëy, bula mer yen ba gaa nu fay, Sunu jekee ba yàlla fay, Linga daa muñ ci néegu sëy, lufa baax yaa ko fay mu je .

Ku ci teen nàngalub jamal, lumu jure mbott lay yamal, kuci boofël kamiy sëyël lumu jur siggi nig jamal, Guñu dul rànga kay lo ji

Sa jëkër sàmmal ub sagam, diko raamal defub sagam, diko jiiteul defub dagam, nanga sew ngir dabuy ngërëm, su ëllagee sak njaboot dijj .

Ngërëm uk sëy du njocci lex, natt ay lotkoloñ di rax, aka armal ajuk marax, ku lëgéeyul dangay torox, nanga jàngat ni ñiy aje .

Kifi sew bay niruk karang, kafa rëy bay dirik gelegn, kañu xejjel mu def keleng kafa jëf rekka fay gañe .

Sama jeek bul di gaawa neuh, nanga teey ta bul di gaawa wax, sama jeek sàmb bul wax, rikk i jekkil ta wàññi wax, ku ne gaafal na moor ndaje .

sama tehmis bi ay caxam, bufi teuhmis ba doko xam, ku ko jël def ko ab caqqam, dana am ndam fa gaaya xam, ku ci waaj raw ci sab da je .

yóbba lu néegu sëy Où les histoires vivent. Découvrez maintenant