VERSION WOLOF
« Man Serin Tuubaa miy jaam bu xeebu tey sdkkoo am ngeremal Ydlla akug Yonentam, te di yaakaar ci
hoom hu nangul ko ay jefem, maa ngi denk lii Soxna Penda Joob, di samab taalibe, tey soxna ci sama
baay tex. Ydlla na hu Ydlla jeggal te jeggal ko, te boole hu faral bepp bdkkaar ak matadi.
1 . Maa ngi lay digel yaw soxna si nga goor-goorlu ci muh ak ragal Ydlla, sa Boroom, ci lu nebu ak lu
feeh ; soo ko defee dey Ydlla di na la jeggal eleg
2. Na nga sax ci tuubal Ydlla saa su nekk ak farlu ci def lu baax ; kon bul jengg mukk jem ci leneen
ludul ag njub
3. Na nga sax ci nangoo weet ngir jaamu sa Boroom. Looy def dee ko def ci sutura te deel suufeel
sa kdddu saa yooy wax ; soo ko defee dey Ydlla di na la gerem
4. Yaw Soxna Penda, li la dese ci sa giirug dund, bul jogeti mukk jem ci loo xam ne leeru la ne
dagan na ci Lislaam
5. Deel moytu bu baax jew ak rey. Deel saxoo noppi ak muh.
6. Deel moytu bu baax wax lu amul ak ngistal wala begga siiw. Na nga moytu naw sa jet wala di
bahanteek sa moroomi mbindeef yi.
7. Na nga sax ci deggu ak sellal, deel farlu ci laabire aka dimbali jaam hi ; soo ko defee dey suhu
Boroom di na la defal ay may aki jagle
8. Bui xalaat mukk topp sa Boroom ci lu andulak topp sa ndigelul boroom ker bu ragal Ydlla boobu
9. Ndax xamal ne kat jihaadu soxna ci yoonu Ydlla mooy mu farlu ci topp ndigelu boroom kerem
10. Looloo waral saa yu boroom ker geremee soxnaam, sunu Boroom da na gerem soxna soosu te di
na ko defal ayxeewal
1 1 . Waaye su fekkee boroom ker geremul soxnaam, soxna soosu na xam ne sunu Boroom du ko
masa gerem
1 2. Maa ngi lay xamal ne lepp lu nit mana def te jemmi Ydlla rekk taxul, jefam jooju sanku na te pert
na ko
13. Te na la woor ne, kenn du mana mucc eleg ci mbugelum sunu Boroom lifeeg bdyyiwul neent
mbiryii, te mooy :
a. Waxluduldegg
b. Rey
c. Naycisaalal
d. Naaw njort ci sa moroom ak ci sa Boroom
Wa salaamu aleykum warahmatu Laahi wa Barakaatuhu