TAZJUMAANOU SAANA ILAAHI

125 12 8
                                    


Tarjumaan la joo xamni Yi mou lamboo Yeemé na. SERIGNE TOUBA mi ngi ko teunk ci " SID HOUHOUM " di juróomi beuyit (5 beuyit).
SERIGNE BI dafa wakh ni : Sounou Boroom Tabāraka wa Tahalaa bindna ni : Khassida gui moko geuneul guepp Khassida té lolou dina feeñ ci mbindéef yepp, adouna ak alaaxira.
SERIGNE BI waxaat ni : Sounou Boroom Tabāraka wa Tahalaa bindna ni : Khassida gui Kārangué gou wóor la ci koukoy diangue ci cheytaané ak bepp noon bou feeñ ak mboleem lou ñouy bañ ci adouna ak alaaxira ak mboleem louy xeeti texedi ak guepp yaxouté.
SERIGNE BI waxaat itam né Sounou Boroom Tabāraka wa Tahalaa bindna ni : KI BIND ARAF YII DI KHASSIDA GUI, nopina ci Nasaraan yepp.
SERIGNE BI waxaat itam ni : Sounou Boroom Tabāraka wa Tahalaa bindna ni : Nasaraan yi dañouy daw KI BIND ARAF YII di khassida gui, di daw yitam mboleem loo xamni njort nañou ni dinako naxari wala dinako lor.

SERIGNE BI waxaat yitam ni : Sounou Boroom Tabāraka wa Tahalaa bindna ni : KHASSIDA GUI amna taxawaayou MAXAAMAY MBOOLEM XARÉ yi nga xamni RASSOULOU LAAHI salalāhou tahalaa haleyhi wa salam taxawé woon nako ak mboleem xaré yi nga xamni ñi daan xeex ci yoonou Yalla daanañko tahawé. Khassida gui amna maxaamam mboleem Xaré yoyou.
SERIGNE BI waxaat itam ni : Sounou Boroom Tabāraka wa Tahalaa bindna ni : KI BIND ARAF YII DI KHASSIDA GUI, Sounou Boroom TEKNAKO CI KAW mboleem ñi nga xamni senoug texé lou leer nañi la , lou wérla.
JËRËJËF BOROOM TOUBA !

You've reached the end of published parts.

⏰ Last updated: Aug 24, 2019 ⏰

Add this story to your Library to get notified about new parts!

TAZJUMAANOU SAANA ILAAHI Where stories live. Discover now