Yéne say nga beug dara wayé meunoko am. Sa bo kheuyé rék nane dinako meuneu déf damakoy songou. Nék xalei bou ndaw am niarr fouki att ak niarr, guiss sama papeu fi soukrate sama kaname. Lolou lou ko gueuneu méti !
Sama yaye di déf lep pour niou nek si ay conditions you bakh wayé lolou yeup doyoul. Motax ma beug dem ab deuk takh nguir dane fa sama doolé donté boudé ass touut lafay am sakh, dina diappalé sam yaye ak sa rakeu bou djiguéne bi ngua khamni ab lagoo la.Rombou na kuluwar bi pour waxtane ak sam yaye si sam décision bima dieul té ame si yakar ni k dinako nangou.
-Mére Fatou ! Ya ngui togu ? (Ma lathie ko).
-Wa khana di surveiller sama ndiaboot bi rék, (mou tontouma).
-Topal guinar yi rék di léne khontou.
-Noumay déf yaye boye.
-Ah yalla baxna. Ma ngui doguay diougué téne wa, nokh bi mi ngui si nâ ba.
-Dieureudieuf Diaher.
Lègui nak, ma togu diakarloo ak mom nguir fasyéné wakh sama doléance.
-Yaye, bi goorgui guéné adina ba lègui ma ngui khalat si béne mbiir bouma nioor lolou.
-Mba diam la Diaher ?
-Diam la dou diam. Damala beugone wakh rék ni k dama beugone dém Ndakaruu Ndiaye nguir liguéy fofou...
-Mouk !! Boul agali. Ay Saly ya ngui sétt li nguay wakh.
-Sétt nako sétatt ko bou bakh sakh yaye. Dama xamni k kéne meunouléne guéné si tolof tolof yi koudoul mane mi nék sa taw bou goor ak djiguéne. Té boudoul dara sakh ngua yeureum koudy di sa thiaat.
-Mane déh dioba lolou yeup diaxalouma wayé Saly yaw ko xam deuk takh ? Mane mi di sa ndeye xawmafa sa baye tamit bamou done doundou meussou fa ték tankam.
-Xamna lolou yeup yaye wayé damay tenter sama sance rék. Nangoul ma sama mbeubeut bi rék yaye. Mane dani doolé déh, défoumafa dara lou niakk fayda nakh aw seur bi dinako takeu ba kéne douko téki. Bou féké lolou moy sa titangué meune ngua nélaw ba yandor.
Nopina ay waxtou you néww bala moumay tontou:
-Ah kom k lolou ngua beug rék, yalna yalla motali yéné bi
-Amine...
-Wayé Saly hum...ba douniou faté wala nguay dieul yone bou saffane ba ? Ba nguay topou goorou Ndakaruu Ndiaye ya ?
-Yalla téré ! Mane Saly Diaher Kéne douma yapp waxatoumak aw goor. Damay dane doolé téral sa yaw ak sam rakeu.
-Kone bok ma ngui la nianal sam doom bi, yone bo djoub lou yalla nada yiww yalla djoub lou.
Bima paré ma dioug dougou si négg bi nguir défare sama eumbou yeuré. Si katanou yalla souba lay fass yéné dém Ndakaruu Ndiaye.
______________
Une histoire purement wolof !!
Alors qu'en pensez-vous ?
Ma continuer wala ?
VOUS LISEZ
Saly Kaw Kaw {Terminée}
General Fiction•••Terminée ''Mane Saly Diaher kéne douma yapp waxatoumak aw goor. Dama liguéy dane doolé téral sa yaye ak sam rakeu" C'était sa philosophie mais bon comme on dit personne n'est maître de son destin. Ne laissez pas le ? se former dans votre tête😉...