BASTUL A BON BU DEE TAXAW (QUE LA BASCULE EST DANGEREUSE AV MOMENT DE LA PESÉE)

87 4 0
                                    

1. Bastula bonn buddé taxxaw

Seytaane daaldi jogg taxxaw

Ne joŋ-gamaa juggal taxxaw

Naxle ma gaa yi béyy aaréen (arachide)

Que la bascule est dangereuse au moment de la pesée

Le diable se tient alors prêt

Et dit àla belle : "tiens-toi prête

A m'aider à tromper ceux qui ont cultivé l'arachide".


2. Mbόoleem murit bu béyy aaréen

Waxtu wudée lapp aaréen

Xéll ma ne lapp ci jigéen

Ku farluwul sa lépp neen

Pour tout aspirant ayant cultivé l'arachide,

Si, au moment où il bat (son) arachide,

Sa pensée se fixe sur la femme,

S'il ne prend garde (verra) tout son (effort) réduit à néant


3. Joŋ-gamaa day jaayό ka jaay

Murit bu jugg mu neko kaay

Taggale kόokug laxxasaay

Ak itte muyy nirru jigéen

La belle à l'habitude de se pavaner et de (se) vendre

A l'aspirant qui réagit elle dit : "viens",

Réussit à le détacher de son ardeur

Et de sa détermination; (ainsi) il se féminise.


4. Jigéen'a bonn ci abb murit

Moo gëna bonn ci abb murit

Lépp lu bonn ci abb murit

Yaw buko séenu buko séen

Que la femme est néfaste à l'aspirant

C'est la pire chose pour l'aspirant.

(Et) tout ce qui est défavorable à l'aspirant

Ne l'attend pas, ne le vise pas.


5. Ku joxx jigéenam lamu laaj

Xañ sëriñam lamuko laaj

Ku xañ Sëriñ nagg lamu laaj

Réccu ko gaa yi déggléen

Qui satisfait la demande de sa femme,

Refuse la demande de son guide (spirituel)

Et qui refuse à son guide ce qu'il demande,

Aura à s'en répentir, comprenez bien.


6. Murit da daa wutt sëriñam

Tey daw ludul abb sëriñam

Ba Yàlla joxx kob sëriñam

Ak njariñam mu bόole léen

L'aspirant (d'habitude) est en quête de son guide

En s'éloignant de tout ce qui n'est pas son guide

Jusqu'à ce que Dieu lui octroie et son guide

Et son intérêt à la fois.


7. W ut léena wut séen'ubb sëriñ

Moo gën di foo ka wut njariñ

Abb sëriñ'ay joxey njariñ

Tey ak ëllëg ndé du lénéen

Persévérez dans la quête de votre guide (spirituel)

C'est préférable à l'amusement et à la quête de profits

(Car) c'est le guide qui octroie le bienfait

Aujourd'hui et demain et point autre chose.


8. Ku muñ te sakku sab sëriñ

Te baña wutt lenn njariñ

Léegi nga giss lépp njariñ

Jogg di la wutt laxxasuléen

Qui patiente et cherche (l'agrément) de son guide,

S'abstient de rechercher le moindre profit,

Verra bientôt tous bienfaits

Venir à soi, soyez persévérants.


9. Kόo xam ne kii la déefi wutt

Lépp da laa mujj di wutt

Loo soxla am te doo ko wutt

Amléen'i yitte, yewwuléen

Alors ce qui constitue l'objet de toute quête

Finira par être entièrement à votre quête,

Vos désirs s'exaucent ainsi sans quête,

Soyez déterminés et en éveil.


10. Ku bëgga mucc jariñu

Day lorru ŋir ku jariñu

Lorruna dόora jariñu

Ag dëgg'a ŋii te birr naléen

Qui aimerait finir par jouir du bien

Doit d'abord connaître le malheur, car qui a le Bien

A d'abord eu le Mal avant le Bien

Voilà une vérité et vous en êtes certains.


11. Ku bëgga dem day awwu yόon

Kόo xamne kii awul'u yόon

Mbirram dafay dënnoo ka xiin

Waaye du gis ludul ngëléen

Qui veut partir emprunte la (bonne) voie

Celui qui n'emprunte pas la (bonne) voie,

Verra ses affaires (s'assimiler) au tonnerre et aux nuages

Et il ne verrait que vent poussiéreux


12. Ku joxxewul déefu ko joxx

Luñu jiiwul du mana saxx

Ku naxxewul deefu ko naxx

Yëgleen ne gaayi béyy aréen.

Qui ne pourvoie ne sera point pourvu

Ce qui n'est pas semé ne saurait germer

Qui ne trompe pas n'est point trompé

Soyez (en) avertis, vous autres qui avez cultivé l'arachide .

WOLOFAL SERIGNE MBAYE DIAKHATEOù les histoires vivent. Découvrez maintenant