Chapitre II

8.1K 864 18
                                    

Allah Allah Allah⌚⌚⌚
Hum hum après sonnerie réveil bi ci la yewou dém sangou dji , brossou , dadi diapou(ablution) sol sama jallaba dém diouli ji fadiar après diouli fadiar bi ma défar café après dém nouyou sama papa ,nouyou sama yaye mou nianal ma .

Ma tegou ci yone bi comme Guediawaye dafa sorii il faut ma tela dém parce-que bus 24 bi la wara dieul té il faut ma dem ba terminus  P5 bi.

  Matzo: salamalékoum grand nakamou kou moudié ci rang bi

Client bus 1: non ladial mère bou sol lou yèré bou jaune

Matzo: maman naga def ya moudié ci rang

Cliente bus 2: waw sama dome ma moudié

Matzo : kone ma topou ci ioe .

Ma dieul sama casque di dég lou Aida faye mou baye wallay mashallah soxna ci souy zikre daf may danoulo leer.

Receveur: défar len rang bi gno gui wadia dém
Matzo: wa mais tonton man ma topou ci mère bi.

Client bus 3: sama dome dafa tel deh ish fadiar gui ga beug ma indil waax

Matzo: mais gorgui man wakhouma lou ay deug rek lala waax ioe baga nieuwé fi gama fék.

Client bus 3: anh ioe dome khamadii ga deh man dal légui xalei diakhal nagn ma Ken yaratoulen man sa moromou baye la

Matzo: mais gorgui bayilène boulen xalei wakhé deug rek gen waax dafa khamadii man sama Baye daf ma yaar  té sama Baye dou def li ga def

Client 4: wa diex na boy aduna amoul solo

Matzo: wa baxna niit dal day def yone.

Receveur : athia athia dougou len gnou dém.

Ma dougou dieul place tek sama sac dém dieunde ticket nieuwat tok takkat samay casque continue di deglou Aida faye mou baye.

Ci yone bi yeup dara xéwou fa lou spéciale à part yen client youy khoulo ak chauffeur dak nimouy dawalé.

Ay 7h50mn fék nama bountou UCAD may lathié fan la FASEG nek ci lama ben agent COUD expliqué ma dem ba fofou ma lathié fan la bureau M. Lo nék gnou wone mako man dém feug toc... toc ...toc Ken wouyou woul ci la xalate ni ndeke gouma ma guenat pour khol fou place ndeki kay ci la demei gueneuh ci porte universite bou mag côté fanne  si la dokhé touti guiss ben mère bouy ndeki  ma dem tok .

Matzo: mère nagen def loy diay

Mère ndeki: magui fi sama dome thon amna,  ndambé,  mayonnaise,  petit poids,  omelette ak sandwich

Matzo: wa défal ma ben pain omelette ak kassou café ak mew .

Mère ndeki: waw kharal ma diay ki ba paré

Matzo: amoul problème mère

Bama ndeké  ba parei ma ladj mère gnata mou waax ma fay ko delou wat FASEG pour khol M. Lo bakham nieuw mais ba lègui guisouma ko.
Si la togué ci hall di khar ba ay 10h mouy soga nieuw après ma khar 15 minute soga dém guiss.

Matzo: toc.. toc..toc..

M. Lo: yeksil

Matzo: tonton Lo naga def yagui ci diam naka sama tata mogui ci diam

M.Lo: éh tay mom amna gane pape matar naga def ana sa papa ak yaye gno gui ci diam.

Matzo: Alhamdoulilah tonton gno gui ci diam bou baax.
Waw kone niga ko khamé année bi la am sama bac té depuis bobou ba lègui orienté wou gnouma motax mani nala set si .
  M. Lo: waax ga deug sa papa téléphone nama ci souba dima ko waax . Waw ioe ban série gadone def ak yen filière ga choisir

Matzo: waw man tonton bac L'1 la am mais bamay def samay choix géographie la def 1er choix tek Anglais , def droit 3ème choix

M. Lo: waw mais ioe waro wone def géographie 1er parce que fofou élèves L2 lagnou eup gnou gnou fay dieul mais grawoul di khol ak sama contact yi ma am bakham naci meun def dara.

Matzo: dieurdieuf tonton khamna magui nieuw dém ba bénen yone inchallah ga nouyoul ma sama tata.

M. Lo: waw khamna gnou déf nonou ba bénen  yone ga nouyoul bou baax sa papa ak sa yaye mais ga wakhal ma sa yaye dina fa nieuw inchallah.
 
Matzo: inchallah dina ko dég.

Après ma  gueneuh dial yone bou dieum arrêt 24 bi pour gnibi ci yone bi lama sama papa wo téléphone

Pa bi: allô allô

Matzo: allô waw papa naga def mba diam ga fanané

Pa bi: Alhamdoulilah diam rek waw dém seti M. Lo

Matzo: waw dém nafa waxtan na ak mom mounii ma waax dina khol loumou ci meun ak contact yim am

Pa bi: waw baxna man magui di dém liguéye yii khamna ba gone inchallah

Après ci la dokh touti dadi yégue
Ci arrêt bus comme heure bobou dou fékk niit yi wathié donc bus dou khat ma dougou tok presque yone bi yeup amoul dara lou spéciale.

Diox ma sa xalate 📄📄📄

Beusseul ma 🌟🌟🌟

sama mbeuguel ci mom Onde histórias criam vida. Descubra agora