sheut sheut tay mom bindanti na koi kharal ma diogue gaw bala pa bi dima fii fék dima indil ay blém .
sila dioug sangou fay diouli souba rathi fass yéné defar ndéki bou am diome tay mom nafi nékou fii koi après la dem ci boutique bii coaché samay néne ak sama pain tay mom omelette lay défar ( genrou fina yi malén dakka togou omelette 😂😂)tin tin tin tin tin
hoho koumay wowatii tamite sila khol guiss mouy papito
matzo: Allo fils naka waarpapito: wa fall nice ioe dafa melnii yaguii soga yéwou déh
matzo: wa boy guiss ga déh maguii soga yéwou nii tay mom dama bidanti koi
papito: wa fils mba faté wo louma wakhone l'autre jour
matzo: loma wakhone ??
papito: ioe boy moy lolou nak koi tay la samedi annif bimala wakhone tay la déh
matzo: anh heah waaax ga deug déh mais ban heure lagnii
papito: legui ay 23h diaral galé gnou reglé quelques détails soga dougou
matzo: waw dakor dina nieuw 22h 30 nane zeum ba paré gnou soga dém
papito: boy ioe meunga wat nii do changé
matzo: est ce que doma bayii ak sama zeum tamite
papito: wa baxna togal fofou rek ok on se capte ci kanam
sila coupé ak saway diioublou sama ndéki tchioum fass yéné defar ndéki bou am diome bou am dolé ...
ndékki dal neex loko dieundé diar nako kharal ma nieuw rathi sétan championnat Angleterre tay sama équipe bii Manchester United moy joué mais ak sunu coach bii rek dagay sétan sa khol di tangue rek dakh khamoul dara .
sila tok suivre match ba ay 16h30 ma agne dém nélaw toutii ba 18h ma guéneuh dém plage dieulii aire toutii ...22h tin tin tin tin tin tin
matzo: wa boy ioe yakamti ga déh noumou démei nii
papito: boy fo tolou
matzo: boy 22h 30 lala waax déh maguii nieuw legui coachélma brada ak kass yi magui téw
papito : legui léguiaprès la dougou sama chambre déf petit sagnsé rek dadi lal parfum tek samay shoes dém galé papito ray fa bén leuweul 2em
23h gnou coaché sunu clando ba rond point case ba dokh lii desss😁😁😁😁 té lici geuneuh graw moy gnoun niar nieupou ken yorou ci kado😁😁 nonpapito: wa boy est ce que khamga nii dagno warone dieunde kado saax legui bougnou demei fofou nieupou indi kado nak té boy bii daf ma diokh thieur déh
matzo: 😁😁😁 toute façon dal man damalay gougué rek ken invité wouma ioe lagnou invité
papito: sheut boy ioe daga con nak mais plané nagnou déh
Matzo: 😁😁 affaire de nandité rek néko after sa kado dina nieuw rek waax dji diéx koi wala nalako O.M (orange Money)
papito: wa thioloul bayil ma gerei ko nonou
si lagnou nieuw baci bountou keur guii papito call boy niko yeksi nagnou mou expliqué gnou gnou yék fék fa quelques personnes khamga rek moy xalei you am classe yoyou koi .
mais li graw ci affair bi moy xalei rafet nagn bi pairou rafet non jigen sénégal dal Mashallah mais diamant noir bimay guiss nii tamite ohh
matzo: mais fils xalei bé molna déh diamant noir lalay tégal ni déh
papito: boy man kay dama moudié warou xalei yii mol nagnou boy
matzo: en tt cas man diamant noir bii dal saf nama trop😁😁 kharal ma dém diéguè ko fils waxtan ak mom
matzo: sama xarite naga déf
Elle : wa ca va maguii fii
matzo: yaguii cool
Elle : wa nice
matzo: (wa ki mom gateu na waax dii ) mais dama tok feulé guiss la ga sagnsé lou rafet maniii kharal nieuw waax la liga sagnsé dafa rafét en plus sa mireille bii daf la diapou yaguii belle nii
Elle : merci beaucoup c gentille
matzo: comme wakhoma sa tour bayil ma lath lako 😁 mais man mom dina la waax sama bala gama koy lath😁 matzo la toudou ioe nak
Elle : wa man maguii toudou khadija mais sama copines yi Dija lagn ma wowé
matzo: waouh Dija sa tour bii neex déh 😍😍😍😍 est ce que douma changé sama tour toudou Dija saax ( hum matzo bayil door yii way😁😁)
Elle : bayil togn way
matzo: non lou leer lay waax mais man beug nala guissante est que meun na am sa 77
Elle: bon man khamga j'ai l'habitude de donné mon numero a des inconnus
matzo: non non adioul lolou way man douma inconnu déh parsk waax nala sama tour déh kholal diox ma sa 77 rek waww after niou diapizé
Elle : bon comme tu insiste dieuleul 77 .197.45
rék ma dég ay boisoir les filles comment vous allez way tok na ay 30s khadija mogui égali numéro bi dégatouma saxx loumouy waax dakh tellement bate bima non seulement dama kham té damako mine lolou saax sheuteut sheuteut tay rék lama yalla done khar non non non meunoul nék mom meunoul nek momm way🤔🙄🙄
Beusseul ⭐⭐⭐⭐ té dioxma sa xalate
sama mbeuguel ci mom ♥️♥️
sama mbeuguel ci yen ♥️♥️♥️
sen mbeuguel ci man ♥️♥️♥️♥️
![](https://img.wattpad.com/cover/224266861-288-k925438.jpg)
VOUS LISEZ
sama mbeuguel ci mom (suite)
PrzygodoweHistoire bi nak man la ak ben xalei jiguen boumou doe beuguenték sa daara djou kawé ga manam université