XIDMA yoonu Tekki

8 0 0
                                    

«Muqaddamatul XIDMA fii salaati halaa nabiiyir rahmah» walla «Miftaahus Sahaada fii salaati halaa xayris sahaadah» téereb wesarub Seex Ahmadu Bàmba bu gànjaru la, di li sabab tukkeem ci géej gi. Sëriñ Basiiru Mbàkke di doomam firndeel na ko ci téereem bii di «Minnanul Baaxil Xadiim», mu wax ne Sëriñ bi ci boppam moo ko xamal loolu wax ko ne «Muqaddamatul XIDMA» Moo waral génne gi ndax Yàlla da koo bëggoon na may ay ngëneel yoy ci ginnaaw bu ko tegee ay nattu la ko koy jox.

Ginnaaw bi mu ko bindee moom Sëriñ bi ag tawat gu metti da koo dal, ci loolu sax ci la taalife xasiidag «Matlabush sihifaa i», nga xam ne jamono joobu tawat gi tar na ba manul a bind, nee nañu kenn ci waa këram (ay soxnaam), ñii ne Soxna Aminata Lóo ñee ni Soxna Awa Buso la ko doon sa muy bind.

Tawat gi taroon na ba Sëriñ bi wax ci «Matlabush Shifaa i» : "Wa ashtakii ilayhi maa minad darar, xad massa nii hattaa araani muhtadar" (Ci moom (Yàlla) laay laaxaan mettit wii ma dal ba jigele maal kóddi (dee).

«Muqaddamatul XIDMA» mooy ci lu amul sikki-sàkka mbind mi nu njëkk a xam mu am 740 turi Yónnent bi (jmm). Moom sax am na lu ëpp 800 «Salaatu halaa Nabii» (julli ci Yónnent bi (jmm)). Ci tur wu nekk Sëriñ bi da ci julli ci Yónnent bi tofal ci ag ñaan.

Bokk na ci ñaan yooyu, Sëriñ bi wax ne : « defal bii téere muy ag génnuwaay ci bépp jafe-jafe». Dolli ca ne : «def ko muy ñaan gi nga gën a nangu (yaw sama Boroom)» wax ne: «def ko muy gànjar gu kenn manul xayma» «def ko muy bëgg-bëgg gees nangu te sottal ko», « defal julli yii ma def ci téere bii muy gaal ak yéegukaay gi may jaar ngir mucc ci musiba ak ngir nekk ci sa wet (yaw Yàlla) «defal bile téere jëf ju baax ju dul raaf mukk», «def ko muy muccukaayu mbooleem bàkkaar» «def ko muy mbóot mu rëy ci sa wet» «def ko muy ag xëccu jëm ci texe».... añs
Itam, Sëriñ bi moo ngi ciy indi «tawhiid» (Jennug Yàlla), ci anam wu yéeme. Daa doore ci ag  ubbi, teg ci jëll Abacada araab ngir wax ci Yónnent bi (jmm). Loy wu ne tàmbli aw turu Yónnent bi (jmm), dale ko ci «alif» ba «Yaa».

Sëriñ bi dugal ci njeexital gi ay maami Yónnent bi (jmm) ci «sallaatu halaa Nabii» yi, tàmbalee ci baayam Abdallaah, Abdul Mutaalib, Maamam Aashim, Abdul Manaaf... ba ca Adnaan.

Hai finito le parti pubblicate.

⏰ Ultimo aggiornamento: Nov 19, 2021 ⏰

Aggiungi questa storia alla tua Biblioteca per ricevere una notifica quando verrà pubblicata la prossima parte!

Waxtaan ci Muqaddamatul XIDMA Dove le storie prendono vita. Scoprilo ora