quand l'homme à voulu ensorcelé Serigne Babacar Sy

794 87 9
                                    

Dafa am been waay mou dem ba Mali pour liguey Serigne Babacar Sy. Xam nga kougnou meunaloul dara dagni wakh nagn la diougeul mystiquement mais waadji limou xamoul wone moy Serigne Babacar Sy hétou waliou bimou bokk mystique doulén diapp. Loutax mystique doulén diapp moy ni mystique daflén déggeul xalima banga naan ba bi pour ba bi mou yakkou dafay biind ba pour mou bakh. Motax bi waadji démé Mali ni dafay liguey Serigne Babacar Sy mou dadjé ak féticheur bou magg bi néko meuna ko dh mais faww nga diokhé khaliss bou beurii. Té féticheur bi koumou meussa hatim guéneu  nga aduna wadji né féticheur bi gnoune dal rëw meuh meunalougn ko dara.
Féticheur bi niko bakhna mais limay hatim si kholou mbam lakay def dem dieundoulou mbam, niou ray mbam mii fëss mbam mi xol mbam mii amoul khol.
Féticheur bi né li dh yémeuh nama mbam bi amoul khol té migui may soga dal mou demate dieundeuh bénén mbamm niou rayate mbamm bi fëss mbamm bi amoul khol féticheur bi né li daal ay mbiir leuh. Mou dieundate bénén mbamm mou fëss ko guiss cii Khol mouni waw kay mbamm mii mom amna khol daldi ladj xaliwa. Niou diokh ko Xaliwa mou défar xalima bamou dane défar nga xam ni koumousi meussana douggeul dawo fanan bindeuh thi biir hatim bi tourou Serigne Babacar Sy mou diokh ko wadji niko tékko thi nadj bi li sou wowé borom guénn aduna. Xaliwa bi meunoul fékhé ba woww wadji togg 3h xaliwa bi meunoul fékhé ba woww té nadj bégui tangg djeur té xaliwa hadjar la mouni ah li dh doyna waar. Féticheur bi ni wadji lgui dal démal dieuli xaliwa bi niou xol loutax meunoul woww, wadji dem bay dieul xaliwa bi né ah dafa mélni migui wadja wow dh féticheur bi niko wa ma xol féticheur bi xol guiss famou bindone Serigne Babacar Sy niou dindiko bindeuh fa mom touram mom féticheur bi té xalima bagui wadja wow.
Féticheur bi ni wadji man dh xamnani damay déh légui lima beuggone dal moy bouma déwé déloko khaliss bi té nga dem tivaouane nga djégaloul mako ndakh xamnani man damay déh ndakh li sama tourr lagnou thi bindeuh té effacer nako ba sonou meunoul fékhé ba effacer wou.
Bala wadji di guénn Mali féticheur bi déh na, bi wadji délo dem tivaouane migui fekk Serigne Babacar Sy thia wétou diaka dji manga botte ay lokhom gadou kouroussam nonou la dane dokhé. Limi beuri beuri thieur yeup boko dane romb migui sol jellaba ték si bonnet carrém bou nioul botti lokhom di diabanté si wétou diaka Maodo.
Wadji aksi ak ay heul thia train baa Wadji ni Serigne Babacar Sy damala beuggone guiss, Serigne Babacar Sy néko diaroul guiss niarri kholou mbamm yaa djitou miigui né ma sendi thi alleuh bi niétél mbamm baa nguén raay mani gni sax dagnou may fonto diaroul may dindi Khol bi nalé bayi ak khol bi. Nguén dieul khol bi sampp thi dérétam baa hatim, xalima bi lankk nguén bindeuloko Serigne Babacar Sy mou bindeuh tourou féticheur bi té sen tour yen niar la naronte bolé wayé dama beuggone ioe nga nieuw ba wakh mako ba paré.
Légui féticheur bi déh na yonéna thi man yoné bou amoul gnarigne lissi dess kay moy xalima bagui xaar ndakh mou bindate la ioe. Wadji soukou thi kanamam té wadji bokoul thi tariha bi dh, wadji soukou thi kanamou Serigne Babacar Sy dieggeu louko diaap lokho Serigne Babacar Sy néko dimbalima ba boumouma bindeuh thi wétt nga. Serigne Babacar Sy néko lgui wakhma bane daraadja nga am ba doula bindeuh thia wétt nga, Wadji niko damay toubeuh dieul wird tariha bi bokou thi tariha bi Serigne Babacar Sy d'accord.
Serigne Babacar Sy loumou dane mérr mérr boko toudalé Mawlaya Cheikh Ahmada Tidiani mou d'accord. Baye Mbaye Dondé Mbaye néna Serigne Babacar Sy loumou geunone bagne moy di lekk dii tourr niam. Mbaye Dondé néna dafa togg thi salou Serigne Babacar Sy si souf di leek am pépp djépp yii waddeuh néna Serigne Babacar Sy migui thia kaw dégg naa pépp djépp yi di waddeuh dh mou commencé wathi néna mou aksi oubi bountou salle bi kholma ma kholko Baye Mbaye Dondé néna ma xamni goor gui daal lamou geunone bagne déf nako ma xalate xalate xawma nouma thi guéné rk ma youkhou "Innal manayla" néna wayé Serigne Babacar Sy migui alou wone yeukeuti kourouss gui wayé néna bama youkho "Innal manayla" néna Serigne Babacar Sy wathié wate kourouss gui dima dégg lou ma wooy bamou yagg Serigne Babacar sy yeuggal bopp bi né thieuy Cheikh ken dou mom wayé lima méti moy nitt gni xamou gnouko. Loumou meussane mére mom Serigne Babacar Sy boko toudalé Mawlaya Cheikh Ahmada Tidiani rk mérr gui guiff.

Cheikhal Khalifa Ababacar Sy (RTA). Chef spirituel au charisme légendaireOù les histoires vivent. Découvrez maintenant