Mère bi thia laam laam

981 120 6
                                    

Cheikh Tidiane mbaye ibn Baye Dondé mbaye néna dafa done woyy Serigne Babacar Sy sa laam laam bein mère bou maguétt guéneuh thi néggeu baa niko sama bopp yénn xamoulein kouy SERIGNE BABACAR SY Cheikh Tidiane niko Maam booy kane moy SERIGNE BABACAR SY? Mére bi niko sama doom dafa am been biss ma dem thies wara gnibi si laam laam sama passe diékh néna mou dem thi gar ba dougou autoray néna bimou dougué ba togg mou ladj kimou déndal néko autoray bi sou déparé thies fane lay taxawé? Wadji niko bou déparé thies day romb laam laam romb ndiakhaté tivaouane lay téré.
Mére bi niko man sama doom laam laam la wara wathie ndakh bouma démé ba fofou souma né chauffeur bi mou maay ma ndakh dinama maay?waadji niko dédétt maam boy autoray amoul lolou bou déparé thies day romb laam laam romb ndiakhaté tivaouane lay téré. Mère bi néna mou diakhlé lol wayei néna khélam ni lapp thi Serigne Babacar Sy borom bonnet carré bi néna mou diangg fatiha salatoul fatiha diokh adiya Serigne Babacar Sy niko yallah yallah nangama wayé laam laam thi barké Serigne Babacar Sy mouni nékété kimou déndalone migui kay dégg wadji niko Maam boy bayilen sen affairou fanatisme yi autoray dou yeuffi Serigne yeufi toubab leuh bou déparé thies day romb laam laam romb ndiakhaté tivaouane lay téré. Mère bi niko man sama doom xawma kane wayé man insha allah laam laam lay wathie thi barké Serigne Babacar Sy autoray bi déparé nieuw ba laam laam romb ko bay wadj dougou ndiakhaté autoray bi diéki-diéki daldi taxaw niouné waa lou nek thi autoray bi?  Niouni xaar leen niou xolko néna bignouko xolé néké autoray bi dafa am vise bouthi wadeuh meunatoula avancer daya arrière rk.
Mére bi néna mou togg famou togg rk né insha allah man laam laam lay wathie thi barké Serigne Babacar Sy.Niouni kone lousi péhé niouni agents yi na am gnousi wathi niou xol vise bi ndakh bimou wodé ak légui sorégoul autoray bangay arrière gnogui xol vise bi mère banga togg fimou togg rk mère bi mountou keureum ak raay bi gno diakaarlo thia laam laam nékété yooo vise bagui wadé laam laam thia bountou keur mère bi niouni lousi péhé niou daldi né na autoray bi taxaw kay niou visé ko bamou deuggeur niouy daldi avancer dem tivaouane mère bi néna bagn kay visé sila daldi wathié nank mom dieul ayy bagage wiirii bassi veer bi daldi feukk wadji mou déndalone dalniko aurevoir waxonala laam laam lay wathie thi barké Serigne Babacar Sy

Cheikhal Khalifa Ababacar Sy (RTA). Chef spirituel au charisme légendaireOù les histoires vivent. Découvrez maintenant