Maga

405 35 4
                                    

"Yaari wax yu dëppoo"

•CHEIKH IBRAHIMA FALL
Muni bim ñëwé Mbakke Kajoor di séetlu taalibé yi ci kër gi diir bu yag, bis muy waxtaan ak taalibé ci kunékak saw mélo, CHEIKH IBRA niléen MAAM THIERNO dé xam naani mooy S.TUUBA, SERIÑ bi mooy THIERNO, ndax séet lu naa kénn kunék ci ñun SERIÑ BAMBA dina waxak yaw ba nga taxali kook sa sago (Daanu jéll) té THIERNO moom danaan dégg rék (maanam day andak saggoom ) ci laa xaméeni Thierno mooy Seriñ bi

•MBAXAAN JOOB 
Muni  MAAM THIERNO Ku amuw fit la té du soppiku ndax bimako fékké DAARU MANAAN   (Touba) yoré sama jaasi ja diko door ca pérri néeg ya diko xuppu THIERNO yënguwul, raful famu took rék la took, tè kanaam googu muma wanoon, moom lama wanaat kérok bamako fékké DARU MUHTI diko ñaanuw fas (Cheval) mu joxma wu rëy, bén xarkanam gi rék la gis ci moom 

[ NGOR AK FITT ] BOROM DAARU MUHTI

•Néwoon S Muhhamadu Mustafa Mbakke xëcooy dëkk amul njariñ, doy nit ñi moo am solo, boo doyé nit ñi foo nékk ñu fékk lafa

•Néwoon na S Abdu Lahat Mbakke bu la adduna bépp doon jox té ligéeyoo du la jariñ dara, waayé yit bu la adduna bépp dul woon jox té ngay ligéey du la wañi dara.

Waxi Serigne ToubaOù les histoires vivent. Découvrez maintenant