JIGÉENOU N'DAR (FEMME DE SAINT-LOUIS)

30 6 11
                                    

À ma fille Ndeye Astou Niang

Jigueenou ndar
Jigueen djou djek rafet kaar
Teey tay dox doxinou naar
Jigueenou ndar
Jigueen djou Yalah far

Thi sa djiko dji tay may yeukeuti ay beuyit
Ndax boobei ba tay guissa gouma say euyib
Jigueen djou saxoo deug
Am yar tei neixa beug
Jigueen djou djox nieup geud
Jigueenit djou nieup djox geud

Walo nga thiossano
Sa soutoureu xawiwlo
Malanou yeurmandei nga laambo
Nioune douniou taayi dila ndamo

Jigueenou ndar
Jigueen djou djek rafet kaar
Sa taar diniou leeral ni djant bouni faang
Yaadi yaye souniou aldjana di sa soufou tank

Jigueenou talatay Ndër
Taal sa bopou nguir setal sa deer
Yaye garab guiniouy djox keer
Diniou aar beus bounei ak sa leer

PlumePerdue

____________________________

Vide

Poésie un jour! Poésie pour Toujours!Où les histoires vivent. Découvrez maintenant