Ñaar fukki melo yi war ci sunu Boroom

61 3 0
                                    

Am na ñaar fukki melo yu war ci sunu Boroom :
ba ca njëkk moo di ag am ak ug jiitu ak ug des ( bu nu waxee ag des mooy koo xam ne du ñàkkati mukk ) bokk na ca wuute ak mbindeef yépp, ( te mooy nekkul jëmm ju nuy làmb di ko daj walla nu koy xool di ko gis, nekkul itam di melo wuy dugg ci biir jëmm ) bokk na ca doylu ci boppam ( Te mooy du jëmm bay aajewoo ku ko sos, du luy dugg ci biir jëmm, bay aajewoo jëmm ju mu dugg ) bokk ci ca wéet ( te mooy amul kenn ku koy ñaareel ci jëmmam walla ci ay meloon walla ci ay jëfam ) bokk na ci kàttan sunu Boroom am na kàttan te mi ngi koy jëfandikoo, am na ag nammeel te mi ngi koy jëfandikoo, ndax ba laa daraa am, da koy neex mu door a am, am na xam-xam boo xam ne réerewul dara, ag lu mu tuuti tuuti, am na ag dund, (te mooy du faatu mukk) am na ag dégg lépp lépp lay dégg, am na ag gis lépp lay gis, am na ag man a wax te day wax Alxuraan ay waxam la.

Saa sunu waxee sunu Boroom am na kàttan xamal ne li nu ci namm mooy mbir moo man a xalaat sunu Boroom man na koo amal te bu koy amal ca na mu ko bëggee la koy amale, saa sunu waxee nammeelug sunu Boroom SW mooy ki mu nekk ci moom day man a amal di man a ñàkkal di man a gàntal, di man a guddal, di man a xeesal, di man a njoolal di man a indi mbindeef, ci jamono jii walla jeneen, di mana xeetal mbindeef ci barab bii walla beneen, di man a xeetal mbindeef ci wet gii walla geneen, képp ku ñuy wax ne Yàlla la, fàww mu boole melo yii : dana doon ku am ba noppi dara du ko jiitu, mooy jiitu lépp. Te day doon ku fiy des, te du nuroo ak menn mbindeef, te doon ku doylu ci boppam, di dégg, di gis di wax. Képp ku ñuy wax ne buur la fàww mu doon ku am kàttan, gu mel ne ga ma doon wax, te lu mu bëgg amal ko ca na mu ko bëggee, te day doon ku am xam-am di dund.
Képp kuy bind dara itam fàww melo yii daje ci yaw : kàttan gu mel ne ga ma doon wax,  ak ug nammeel gu mel ne ga ma doon wax, ak xam-xam boo xam ne du umple dara,  ba noppi di dund.
Balaa kenn a amug mat fàww mu doon kuy dégg lépp, di gis lépp di wax. Boo seetloo xam ne melo yooyu yépp sunu Boroom SW moo ko man a melowoo.

Su ko defee meloy sunu Boroom bu ci ne am na fu muy aju, ag lu muy sottal, dananu ci indi juróom-mbenni melo ngir leeral, muy kàttam ak ug nammeelam, ak ug déggam,  ak ug gisam, ak i waxam ak xam-xamam.

Lépp lu man a am kàttanug sunu Boroom ak ug nammeelam aju na ca. Lu man a am nag ñaari xaaj la: lu man a am ba noppi am, ak lu man a am te amul. Li man a ma te am man naa doon lu wéy mel ne sunuy maam, walla lu teew mel ne nun ñii, walla luy ñëw mel ne sunuy doom yiy bëgg a am.
Li man a am te amul mi ngi mel ne yéefër bi génn àdduna manoon naa nekk ab jullit bala moo faatu te amul, naka noonu jullit bi faatu manoon naa nekk ab yéefër bala moo faatu te amul, naka noonu ku amul doom ba faatu manoon naa am doom laataa muy faatu.
Mboolem lu war walla mu dagan walla mu jomm xam-xamub sunu Boroom aju na ca ak i waxam. Lépp lu am déggug sunu boroom ak ug gisam aju na ca.
Mboolem li am lépp ñaaru xaaj la, loo xam ne ag amam daa war mel ni sunu Boroom, ak loo xam ne ag amam daa dagan rekk mel ni sunu maam ya, walla mel ne sunu doom yiy bëgg a ñëw, walla nun ñii, ak lépp looy gis ci àdduna.

Bu nuy wax xam-xamub sunu Boroom, li nu ci jublu mooy am na xam-xam boo xam ne dara la dul sikki-sàkka, amul lenn lu koy ump, walla muy nuru leneen ci moom lu bokkul ak la am. Su ko defee li ñuy xam nag man naa doon lu war, walla lu jomb walla lu dagan.

Bu nuy wax waxi sunu Boroom itam na la wóor ne bokkut ak li nga xam ci ay wax, ndax du am ay araf, fu kawee ak a suufe, du yees ak a màggat, du am lenn ci yi nga xam ne sunuy wax dana ko am, kon li ñu ne ay waxam la danuy firil ay waxam ci ni nu ko man a déggee.

Melow dund ga nag, nanga xam ne amul ci lenn lu muy aju li muy xamle walla li ñu ciy xame mooy sunu Boroom, mi ngu dund rekk.
Leeg-leeg nag nga nga gis loo xam ne boo ko tuddee lu ëpp ñaari melo ci meloy sunu Boroom yi dana ci aju,  leeg-leeg nga gis loo xam ne boo ko tuddee ñaari melo kepp moo ciy aju, ni ma ko waxe woon.

Fi mu ne boo tuddee lu man a am te amul dangay gis ne kàttanug sunu Boroom rekk ak ug nammeelam moo cay aju, naka noonu boo tuddee lu am te ak amam war (te mooy sunu Boroom) gisug sunu Boroom ak ug déggam rekk ñoi cay aju, waaye boo tuddoon, lu am te ak amam warul mel ne mbindeef, dangay gis ne ñent yépp dana ca aju.

Ba tay boo tuddoon lu man a am te amul walla lu jomb, dangay gis ne xam-xamub sunu Boroom rekk moo ciy aju ak i waxam waaye boo tuddoon lu am moo xam lu war la walla leneen dinga gis ne déggug sunu Boroom ak ug gisam dana ca dolliku ñoom ñent ñépp ànd ca.
Boo seetloo danga gis ne xamug sunu Boroom ak i waxam moo gën a yaatu ci yi mu aju, ndax aju na ci lépp lu war, ak lu jomb ak lu dagan.
Boo seetloo ba tay danga gis ne degg sunu Boroom ak ug gisam moo gën a gëtt fu mu aju, ndax ci lu am kepp la aju, bi ci gën a digg-dóomu fu mu aju nag mooy kàttanug sunu Boroom ak ug nammeelam ndax aju na ci lépp lu man a am.
Bu loolu jàllee nga xam ne safaani melo yi ma doon tudd yépp jom nañu ci sunu Boroom SW te mooy manunoo ànd ndax manut a am kàttat ba noppi di lott.

Meññatum Mawaahibul Xuduus Où les histoires vivent. Découvrez maintenant