Su ko defee, lu mel ne "karaama" ak "irhaas" man naa am ci ag sàkku walla sax sàkkuwóo ko. Waaye "muhjisa" moom sàkku manu koo maye ndax day seede ab Yónente, te ag seede bu amee te amul lenn lu ko waral, du am njariñ.
Li tax ñu tuddee ko "muhjisa" ( aji lottal ) mooy : "ku dul ab Yónent du ko man"
Lépp loo xam ne man naa feeñ ci ab Yónent ñu koy tuddee "muhjisa" man naa feeñ ci aw wàlliyu, ñu koy tuddee Karaama.
Su ko defee wàlliyu ak ub Yónent nag, am nañu ag wuute, ndax Yónente moom daa jomb ci moom muy def lu bàkkaar, walliyu nag sunu Boroom da koo wattu man naa juum ba def bàkkaar, loolu moo tax ab Yónent lu mu wax warees na koo gëm te am ci ag dëggu, waaye aw wàlliyu lu mu wax dagan na nga gëm ko waaye wareesu koo jéem a weddi, Yal nanu sunu Boroom may leerug jeñ ak leerug xàjji ci darajay Yónente Bi SHW.
Liy tegtale ne ab Yónente du def lu haraam, du def lu ñu sib, mooy : "bu doon def lu haraam, walla lu ñu sib, nit ñi dañu ko ciy topp te sunu Boroom moo tere def lu haraam, ak lu ñu sib. Kon du bàyyi Yónente yi ñu koy def, ba nit ñi di leen ci topp"
Liy tegtale ne fàww ñu jotal, mooy : "bu ñu jotalutoon li ñu leen yónni, duñu nekk ay Yónente. Bu ñu leen dee topp itam ci njëkk, jottali gi lañu leen di toppe.
Liy tegtale ne liy dal nit ñi man na leen a dal, mooy: "daa am ñu ko fekke, nettali ko ba mu agsi ci nun. Li tax sunu Boroom di leen ko teg, benn muy bëgg a rëyal seen daraja ëllëg, walla ngir mu xamal nit ñi yoon wi ñuy jaar, walla ngir mu bëgg leen a fàtteeloo àdduna jii nga xam ne daa ñàkk solo ba laafum yoo moo ko gën a màgg fa sunu Boroom.
Te it nekkul kër gu muy faye kenn, ndax day jeex te luy jeex daanaka du dara ak lu mu bari bari.
Te itam, loolu mu leen di teg, dana waral nit ñi di waaru ci ñoom, ndax ku am xel boo gisee yooyii di dal Yónente Yi HS danga daal di xam ne Sunu Boroom bëggul àdduna, danga man a mucc ci lu bari.Mboolem li ñu doon wax lépp nag, dugg ci Biir "laa ilaaha illal laahu muhammdu rasuulul laahi Sallaalu tahaalaa halayhi bi aalihii wasahbihii wasallam"
VOUS LISEZ
Meññatum Mawaahibul Xuduus
SpiritualBëgg nanoo dajale fii Téereb Sëriñ Alhaaji Mbàkke bi tudd ,Meññatum Mawaahibul Xudduus. Di téere Sëriñ Tuubaa Bu muy jàngalee "Tawhiid" ( maanaam gëm Yàlla ak y'a ca aju )