Gëm Malaa-ika Yi

23 2 0
                                    

Naka noonu Muhammat Rasuulul laah SHW Ndawul sunu Boroom la, mel na ne gëm nga malaaka yépp, malaaka yi, ay
jëmm yu sew lañu yoo xam ne dañuy man a soppiku nu mu leen neexe, duñu góor, duñu jigéen, duñu lekk, duñu naan ay jaam yu tedd lañu, ci tudd sunu Boroom SW lañuy lekke di ci naan.

Am na ci ñu war a gëm xam seen i jëf te ñooy: "Jibriil miy dikkal Yónente Yi, ak Miikaa-iil miy wàcce taw bi ak Israafiil miy miy wal buftu bi, ak Hasraa-iil miy rocci ruu yi, ak Raxiib ak Hatiid ñiy bind jëfi jaam ñi, ak Munkar ak Nakiir ñiy laaj ci bàmmeel, ak Maalig miy wattu sawara yi ak Ridwaan miy wattu àjjana yi.
Su ko defee yeneen Malaaka yu bokkul ak yii, dañu leen a war a gëm waaye warul ngeen di teqale seen i jëf ak seen i tur.

Am na juroom ñatti malaaka yoo xam ne ñooy yanu haras ñoo tudd datfayaa-il datwayaa-il satfayaa-il, hatmayaa-il kamkayaa-il, samkayaa-il, sasmayaa-il, sanjayaa-il. Ku mokkal seen i tur, bala moo faatu gis këram ca àjjana.
Am na ci malaaka yoo xam ne, ci mbiri nit ñi kepp lañuy liggéey mel ne wërsëg, ag seenub dund. Am na ñoo xam ne dindi tiitaange rekk lañuy liggéeye,

Kenn ci malaaka yi du moy Yàlla sunu Boroom SW. Malaaka yi ñuy tuddee "Kuruubiyyuun" ñooy kilifay malaaka yépp, duñu Jëm ci lenn lu dul sunu Boroom, yeneen malaaka yi sax dañu leen di bëgg a jege, ngir jege gu ñu jege sunu Boroom.

Malaaka yi nekk ci asamaan si Nuroowuñu, yi nekk ci asamaan si njëkk si, dañoo mel ni ay nag, si ci topp dañoo mel ni ay cëeli, si topp dañoo mel ni ay tan, sa ca topp dañoo mel ni ay fas, sa ca topp dañoo mel ni jigéeni àjjana, sa ca topp dañoo mel ni ay nit, sa ca topp nag, malaaka yu bari lool ñoo fa nekk, xamantewuñu sax, ngir seen ug bari.

Waxu wu ne dañuy sàbbaal sunu Boroom ci ay waxiin yu wuute.
Am na ci malaaka yi ñu ñuy tuddee "almuhaqibaatu" ñooy malaaka yiy wàcce barke, am na ci ku tudd hëeruut, ak ku tudd maaruut, yal nanu sunu Boroom may ag njub ak mujj gu rafet ci seen daraja ci barkeb Yónente Bi SHW.

Meññatum Mawaahibul Xuduus Où les histoires vivent. Découvrez maintenant