Ahuusu billaahi minas saytaanir rajiim.
Bismil laahir rahamaanir rahiim.Wasllal laahu halaa sayyidinaa muhammadin wasallama tasliiman. Hawnaka yaa muhiinu wa bika nastahiinu. Hasbunal laahu wanihmal wakiilu. Allaahumma inniya ushiduka wa ashidu hamalata harsika wamalaa-ikataka wajamiiha xalxika annaka antal laahu laa-ilaaha illaa anta wahdaka laa sariika laka wa anna muhammadan habduhuu warasuuluhuu. Laa hawla walaa xuwwata illaa billaahil haliyyil hasiim. Laa-ilaaha illaahu mu hammadu rasuulul laah Sallal laahu tahaalaa halayhi wa sallam. Wa billaahi tahalat tawfiix iyyaaka nahbudu wa iyyaaka nastahiin.
Sëriñ Tuubaa XLML ginnaaw bi mu santee Yàlla sunu Boroom subhaanahuu watahaalaa. Julli ci Yónenteem SHWBW daa xamle ne xam-xam mooy li gën ci lu Yàlla SW di jox ab jaam, waaye xam-xamu wéetal Yàlla sunu Boroom mooy la ca gën, lépp lu ñuy xaare bàmmeel ak yawmal xiyaam mooy la ca gën. Loolu moo tax ñenn ci jàngkat yi sàkku mu wayal leen téereb Imaamu Sannuusi RL bii ma daal di jóg fas ko yéenee way ( du ñàkk yu mu ciy dolli yoo xam ne nekkul ca téere boobu ngir mu jariñ nit ñi rekk ) xam-xamu tawhiit nag, ( te mooy wéetal sunu Boroom ) li tax mu gën xam-xam yi mooy moom kepp boo ko xamoon dana doy, man ngaa tàbbi àjjana it. Te beneen xam-xam bu mu doon bu ci àndul du am njariñ.
Maa ngi ñaan sunu boroom way yii doon lu nuy musal ci sawara, te sell lool ci lépp lu koy ñaawal, te doon ab yóbbal ci bàmmeel ak bis pénc, képp ku ko mokkal walla nga dégg ko xam ko yal na sunu Boroom fegal ayi fitna ci darajay Yónente bi SHTHBW.
VOUS LISEZ
Meññatum Mawaahibul Xuduus
SpiritualitéBëgg nanoo dajale fii Téereb Sëriñ Alhaaji Mbàkke bi tudd ,Meññatum Mawaahibul Xudduus. Di téere Sëriñ Tuubaa Bu muy jàngalee "Tawhiid" ( maanaam gëm Yàlla ak y'a ca aju )