Yi Jomb ci sunu Boroom.

35 3 0
                                    

Jomb na ci sunu Boroom ñàkk ( nga xam ne mastut a am ) jomb na ci sunu Boroom am ba noppi di ñàkkaat, jomb na ci sunu Boroom SW yamoo ak mbindeef yi ( te mooy nekkul jëmm ju nuy man a laal, nekkul itam melo wuy man a dugg ci jëmm, nekkul ci genn wet, mel ne ci kaw walla ci suuf, walla wetug nday-joor walla càmmooy, walla ci kanam walla ci ginnaaw, Déedeet ! Amul itam ag wet ni nu ko amew nekkul itam di am jamono ni nu ko amee nun, walla muy am waxtu walla muy am ay loxo walla ay tànk, walla muy mar walla muy bëgg kem ni nuy bëggee nun walla ni nuy maree, walla mu nekk ku tuuti walla ku rëy walla muy am benn bëgg-bëgg buy dellu ci moom ci jëfam walla ay àtteem ) jomb na ci sunu Boroom SW muy nekk melo wuy dugg ci jëmm wall muy jëmm ju nuy laal ndax lu ci am rekk aajewoo dana am, te moom aajewoowul jëm ci kenn mbaa lenn. Jomb na ci sunu Boroom muy nekk ñaar ci jëmmam walla ay meloom walla ay jëfam, amul kenn ku ko nuru ci jëmmam, kenn warut a wax ne ñaari melo yu nuroo lañu booleel sunu Boroom déedeet ! Kenn warut a wax ne ñaari Yàlla ñoo booloo nekk di jenn, Yàlla itam amul kenn ku man lenn walla mu man a sottal lenn ku dul sunu Boroom SW, menn mbindeef manut a def darra ci boppam, ba koy def ci keneen.

Jomb na ci sunu Boroom lott ci lépp loo xam ne man naa am ci xelum doomu Aadama, jomb na ci sunu Boroom dara am te neexu ko walla muy fàtte walla dara di ko rëcc, te du ko yëg walla dara di amal dara ci mbindeef yi ci jikkoy boppam, mel ne lakkeg sawara, Déedeet ! Sawara làkkewul sunu Boroom mooy lakke ndax bu sawara doon lakke ci jikkoy boppam doylu day daal di am ci moom te dara manut a doylu, ba bàyyi sunu Boroom.
Naka noonu dara manut a am amiinu yilla nga xam ne dañu naan bu lii amee fàww lee am, bu neexee sunu Boroom ak bu ko neexul "Subhaanahuu watahaalaa" du sikki sàkka, du juum, du fàtte, du xalaat, du jortu, du settantal, jomb na ci sunu Boroom dee, jomb na ci sunu Boroom tëx, jomb na ci sunu Boroom gumba, jomb na ci sunu Boroom " Subhanahuu watahaala " tëlee wax,

Li nga xam ne man naa am man naa ñàkk ci sunu Boroom SHWT mooy amal mbindeef, ak ñàkkal ko, te lépp lu dul moom bindeef la, lépp daa dagan ci moom, yónni gi mu yónni yónente yi, ak waral gi mu waral ñu gëm ko ak araamal gi mu araamal ñu weddi ko, ak fay gi muy fay jullit yi ak mbugal gi muy mbugal yéefër yi, lépp daa dagan ci moom, moo tax boo gisee ku naan sunu Boroom da koo war muy def, lu yiw walla la gën a yiw, bu ko nangu mukk danga naan lépp lu sunu Boroom dem SHWT mooy la gën a rafet, ndax loo gis ab jaam yor ko ci ag xéewal sunu Boroom SHWT moo ko ko jox ci ag mbaaxam. Waaye loo gis mu dal ab jaam ci ay mbugal walla lu muy bañ, sunu Boroom mooy feeñal ag maamdoom ci moom.
Lépp lu sunu Boroom dogal bu la neexul, ci coono ak naqar ngay dëkk, ndax lu mu bëgg mu am, kon lépp lu mu dogal na la neex.  Yal nanu may lépp lu mu digle mu neex nu tey góor-góorlu ci ay ndigalam.

Bu loolu jàllee nu ñëw ci tegtal yi lay dërëral, yi ñu waxoon ci ay melo ci sunu Boroom SWT.

Li lay tegtal amug sunu Boroom mooy: "mbindeefam yi ngay gis, te sosuñu seen bopp, ndax bu ñu sosoon seen bopp, danañu juge ci ag dagan nekk lu war te du am lenn lu koy waral te loolu cel nanguwu ko.
Te sax mbindeef yi li lay xamal ne dañu leen a sos mooy yi ñuy taqool mu leen di gaar, di dem ak a ñëw, te duñu ko man a dindi, mel ne dajaloo ak teqalikoo, ak dal ak yëngatu, dangay gis ku xees, bëgg a ñuul te du man a ñuul. Gaar-gaar yooyu loo gis mu am ko xamal ne dañu koo bind. Gaar-gaar foo ko fekk ci jëmm lay nekk joo xam ne daa sosu te duñu man a tuxoo ci jëmmam di dem ci jeneen jëmm, benn mu nëbb walla mu feeñ, waaye manut a boole ñaari safaan, manut a nekk nee ñu koy làmb walla di ko gis"

Liy tegtal ne sunu Boroom moo fi jiitu lépp, te dara jiituwu ko, mooy: "bu loolu amutoon fàww mu am ku ko sos kookee amaat ku ko sos, muy wéy te du am fu muy yam."

Liy tegtale ag desam fàww itam, mooy : "jiitu gi mu jiitu lépp, ndax bu nekkutoon kuy des, du man a jiitu te wax nga leegi luy tegtale ag jiitoom."

Liy tegtale ag wuuteem mooy : "bu yamoowoon ak mbindeef day nekk ku ñu sos te wax nga leegi luy tegtale ag jiitoom,  ak ug desam kon nan lay doonee ku ñu sos ?"

Liy tegtale doylug sunu Boroom mooy : "bu ajowoon jëm ci jëmm ju muy dugg day nekk aw melo te kon du man a amati ay melo, ndax melo manut a am ay melo." naka noonu bu ajowoo woon jëm ci ku ko sos, kon day nekk mbindeef te wax nga keegi ne moo jiitu, moo fiy mujj, te loolu mbindeef fu ko def."

Liy tegtale wéetug sunu Boroom SHWT mooy : " bu nekkutoon kenn, kon du man a sottal dara ndax man naa bañ a dëppoo ak keneen ka muy bokkal."

Liy tegatale xamug Yàlla sunu Boroom ak ug dundam, ak kàttanam ak ug nammeelam, mooy bindeef yi ngay gis, ndax melo yooyu, bu ñu amutoon ci moom du gis menn mbindeef."

Liy tegtale déggug sunu Boroom SHWT ak ug gisam ak i waxam mooy: " Daa wax ci Alxuraaan luy tegtale ak déggam ak ug gisam, ak i waxam. Naka noonu ñëw na ci sunnas Yónente bi (SHW) lu koy tegtale. Naka noonu boroom xam-xam yu mag yi ñépp maase ci te bu amutoon melo yii, day tëx, gumba, luu, te ag wàññen ak ug "mànki" jomb na muy am ci sunu Boroom SHWT."

Liy tegtale daganug mbindeef yépp ci sunu Boroom mu amal ak mu ñàkkal leen mooy: " bu ñu daganutoon benn ñu war ko walla ñu jomb, bu ñu waroon duñu fi jugati, bu ñu jomboon duñu am.

Meññatum Mawaahibul Xuduus Où les histoires vivent. Découvrez maintenant