Naka noonu boo gëmee Muhammadu Rasuulul laal ndawul sunu Boroom SHW gëm nga mboolem téere yi, li tax ñu naan téerey asamaan nag, moo di dañoo juge ci asamaan, su ko defee li nekk ci téere yi dañuy tegtale waxi sunu Boroom, am na ci téere yi loo xam ne ci ay àlliwoo la daan wàcci. Am na loo xam ne sayyidunaa Jibriil moo ko wax ci làmmiñam.
Téere yi mat nañu téeméer ak ñenti téere, sunu maam Aadam HS fukki téere wàcci na ci moom, Siita doomam juróom fukki téere wàcci na ci moom, Idriis fanweeri téere wàcc na ci moom, sunu Maam Ibraahiima fukki yéere wàcci na ci moom, Tawreet ci Muusaa la wàcci, Injiil ci Hiisaa la wàcci, Sabuur ci Daawuuda la wàcci, Alxuraaan ci Sayyidunaa Muhammat SHW la wàcci.
Su ko defee ñenti téere yii ma mujj a tudd dañu leen a war a xàmmee bu baax, moo tax ma tudd leen yeneen ya ca des nag warul ngay xam seen i tur.
Naka noonu boo gëmee Muhammadu Rasuulul Laah ndawul sunu Boroom la SHW, gëm nga bis pénci ak mboolem la ñu fay wax, dale ko ci dekki ga, ak tiit yooya ñu fay wax, ak peese jëf ya ak hisaab ak dajaloo ga ñuy dajaloo fi benn barab ak tiyaaba ja fay am ak mbugal ak leer ak lëndaëm ak jooy ak bég ak gàcca ak réccu ak wuute ga.
Bis boobee ca ngay gis ku jàq lool, fa ngay gis ku sunu Boroom mere lool, gis fa ku mu gërëm lool.
Ñépp ñoo fay tase ñu baax ñi ak ñu bon, kerog boobee lañuy xam ne, mbir yépp sunu Boroom dong a leen moom, kenn bokkul ak moom dara, bis boobee mooy dëgg-dëggi bis, deel farlu ba la moo yegsi, kon doo fa sonn.Bari na lool lu ko sunu Boroom di tudd, loolu nag day tegtale ay tiital yu bari, loo gis mu bari ay tur dana tegtale ag màggam. Sunu boroom am na fu mu ko tudde ba ne "Maliki yawmid diin" maa moom bisub fay ba.
Dana mat juróom fukki junniy at, mi ngi tàmbalee bu ñu walee buftu bi walub ñaareel, ba ñépp dekki. Mi ngi yam ci bu ñépp tàbbee sawara ak àjjana.Su ko defee bis pénc dañu koo séddale ñaari xaaj bu ndaw ak bu mag, bu mag bi mooy loolu ma wax, bu ndaw bi nag saasu nit ki di faatu fa la tàmbalee ak bu nekkee ci bàmmeelam ba kerog muy dekki.
Foofee lañu koy laaje, laaj gi mooy dañuy def ruu gi ci jëmm ji ba mu xam la mu xamoon, ñu laaj ko ci mbiri ngëm-ngëm ci Yàlla sunu Boroom ak ci Yónenteem, loolu moo tax nit ki bu faatoo ba ñu suul ko, bay dem dana dégg dàlli ña ko doon suul ni muy yëngoo.
Bu ñu koy laaj, dañu koy toogal ca digg bàmmeel ba, seen kàddu yi mel ni ag dënnu, seen bët yi mel ne ag melax, ñuy génne lu mel ne ay ferñent ci seen gémmiñ, nuruwuñu jinne nuruwuñu malaaka, mbindeef yépp dañu leen a ragal ba ci malaaka yi ñépp dañu leen di muslu, yal nanu ci sunu Boroom musal.( Waat naa ci sunu Boroom ku dugg ci bàmmeel lu dul ag njub du la fa jariñ.
Képp ku nekk ci àdduna di dajale alal ba fàtte ëllëg tuskare nga.
Ay waay ku nekk ci ay doom ak alal, ba bàyyi wird yi !
Deel jihaadante ak sa bakkan kon bu ëllëgee doo am njàqare. Bul topp bakkan bul topp saytaan, kon bu ëllëgee àjjana ju la neex ngay tànn. Deel jàgg tey topp, kon danga am tuyaaba. Boo bëggee kawe, deel néewal nelaw )Su ko defee ñaari malaaka yooyu ñépp lañuy laaj, ku lab, ak ku ñu làkk ba mu nekk ab dóom ak ku rab yi lekk.
Mboolem looy dégg walla nga xam ko nanga xam ne dee moo ko gën a metti, te mboolem lu nekk ci ginnaaw dee moo gën a metti dee.Bokk na ci tiiti bis pénc, bu téere yi naawee, ba ñu koy tëye, ku jàpp téereem ci loxob nday-jooram, loolu mooy màndargam texeem, Sayyidunaa Homar RH moo koy njëkk a def, ku jàpp téereem ci loxob càmmooyam, loolu mooy màndargam texeedeem, ka ñuy wax Al Aswat moo koy njëkk a def, mbokkam Ibnul Aswat mooy njëkk a jàpp téereem ci nday-jooram gannaaw Sayyidunaa Homar RH.
Boo gëmee Muhammadu Rasuulul Laah ndawul sunu Boroom la, SHW gëm nga ne Yónente yépp dañuy jotal, te duñu fen, duñu def lu araam, duñu def lu ñu sib.
Mel na ne fii mu ne mboolem li nekkoon ci "Laa Ilaaha Illaal Laah Muhammadu Rasuulul Laah" SHW ciy pas-pas leeral naa ko.
Xayna baat boobu gàtt gi mu gàtt ba noppi làmboo li mi làmboo moo tax ñu def ko muy màndargam gëm, balaa kenn a gëm Yàlla sunu Boroom ci nun fàww mu wax baat boobu.
Ku am xel nag, boo xamee loolu ba noppi dangaa war di góor-góorlu bu baax di ko tudd lu bari ba mujj boo koy tudd danga ciy xam yeneen mahnaa, nga xam ne day jaxasoo ak sa dereet bu boobaa, danga gis ci ay kéemaan loo xam ne kenn du ko man a takk. Yal nanu sunu boroom may tawféex te may nu bu nuy génn àdduna di tudd baat bii mu doon sunu baat bu mujj.Su ko defee foofii la téere bi yam di juróom-mbenni téeméeri way ak ñaar fukk.
Subhaana rabbika rabbil hissati hammaa yasifuuna wasalaamun halal mursaliin wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina.
VOUS LISEZ
Meññatum Mawaahibul Xuduus
SpiritualBëgg nanoo dajale fii Téereb Sëriñ Alhaaji Mbàkke bi tudd ,Meññatum Mawaahibul Xudduus. Di téere Sëriñ Tuubaa Bu muy jàngalee "Tawhiid" ( maanaam gëm Yàlla ak y'a ca aju )