1) Nos Chefs religieux
Ku yaakaar ni man nga wax lu wara tax doo tu ñu may nopp sunuy kilifa diine, je dis bien sunuy kilifa diine, dafa fekk xamoo li xey.
Yonnent bi asws moo nu jàngal ni kilifa gi tax nga jub (Yàlla laa mo jarale sak njub ci moom) war na nga sant ko ginnaaw bi nga sante Yàlla ak yonnentaam asws.
Kon ki tax ma xërr ci Yàlla, ki nga xamni saa bu ma deg loo ay waxam gëna farlu ci topp Yàlla, gën ragal Yàlla, gën ragal di ko moy, ... amul lu waay mana wax ba du ma ko gërëm, te topp ko, jël sama alal jox ko bu mako mane ndax xamni munu ko fay mukk mukk teranga bu rëy bi mu may defal.
Bu defoon bàkkaar sax taxul ma baña reconnaissant jëm ci moom ndax loolu mu deff ak tooñ la ci diggante ak Boroomam kon waññi wul dara ci teranga bi mu ma defal.
Kon ndax war ngeen a njort ni yii nitt yi di wax manaam ndax wax Na ñu walla waxu ñu di Na wara tax du ñu leen topp(ci mbiru diine), du ñu leen deggal, du ñu leen jàppale, du ñu leen wormaal?
Boy xool mbir yi da ngay dem sax ba da ngay laaj sa bopp ndax ñenn ci ñiy waax amul benn "haine" bu yàgg nek seeni xol ñuy profiter ci yi.
Li gën doy waar nakk mooy ab jullit, rawatina nga ni boroom xam-xam nga, nga xam bu baax li nekk ci njort, xam li nekk ci wax lu la woorul, nga taxaw di naan kilifa yi àddu wu ñu (se prononcer) ci mbir yi fi xew "ni en public ni en privé", mu melni yaw da nga pirater seeni téléphone ba xam kepp ku ñu waxal walla déet, mu mell ni yaw da nga xam déplacements kilifa yi yepp, mu mel ni yaw fepp Fu kilifa yonnee da nga koy xam... Da ma yaakaar ni ñun sunu sago moo taggoo ak ñun.
Lu jëmm ci man perso, tay laa gën a fonk samay kilifa ndax ñett yi:
1) amuma benn firnde ni àddu wu ñu ci mbir yi ci lu ñu yeggul, wooru ma ndax fekk i Na ñu njiitu réew mi walla moom mu fekk i ji leen ñu waxtaan, wooru ma ndax yónni wu ñu ndaw ci moom, te "en tant que" jullit lu ma woorul du ma ci addu keem ni Ko Yàlla waxee ci teereem ba. Te sax lan mo wara tax man ma leen di forcer ngir ñu wax, te ñu yàgg wax kenn faale Wu leen, ndax ku nekk ci ñoom bu deggaloon kilifa yi mbir yi du yegg ci fii tay, kon bi wax jote waxoon Na ñu.
2) kepp ku am xell te muus boo gisee ku am xell ni yaw, ko xamni wóor nala ni gën o ko muus, mu wuute ak yaw gis gis ci benn mbir bo xamni jàpp nga ni "c'est évident" li nga wara deff laata nga koy jiiñ dara mooy nga "remettre en question" sa bopp, ndax di Nga ni kii ëppu mako xell lan motax kon gisul lima gis, lan motax mu évident ni dafa wax te waxul. Ci Nga wara commencer laaj sa bopp ndax ki amul lu xam ci mbir yi lu ma xamul man ...
Loolu bokk Na ci litax ma teey3) Beneen bi mooy sama ngor mayu ma may fàtte junniy mbaax u nitt ki ndax benn njumte bu mu deff ndax di nay faral di degg ñuy wax naan loolu jikko y baadoola la, fàtte lépp lu ñu la defal ndax benn mbir. Man dey maa ngi sant Yàlla bu baax ndax Ginnaw Yàlla ak ab Yonnentam asws ñiy tax may góor góor lu ngir jub, ñi tax ma bàyyi tere Islam yu bari, ñi tax may farlu ci digle Islam bi, ñi tax samay jikko di gën a baax, ñi tax ñu bari naw ma... mooy sunu kilifa diine "à travers" seeni waxtaan.
Kon ku am ñu leen gën, jël léen te ngéen bàyyi ma ak ñoom, doy na ñu ma sëkk.
Li ci doy waar mooy barina ñu naan bu leen joxee ti addiya bu leen degg loo ti kilifa yi... ñoom séen dërëm masul tàbbi ci luy jëmale lislaam kanam, par contre lépp luy ay caaxaan pare nañ ngir soutenir ko. Kiy jël xalis dajale ko yobbu ko ci ab njibar katt (lu Haram) ngir gagner ab match, mooy yedd ak di xas kiy jox alalam ab jullit buy topp Yàlla tey xiirtal ñepp ci ñu topp Yàlla te naan da ñu lay nax Mdr ...
Yaw mi naan bu ñu déglu kilifa diine yi maa ngi lay ndax yaw man na ñu la deglu ak bu ñu la deglo foo ñu jëmee, ndax da ñuy gën baax walla déet?
kenn manul wax lepp
Yalna Yàlla jubal ñu, raxas sunuy xol ak sunuy xell ba haine disparaître ci, cofeel installer ñun ñepp bëggënte te Yàlla rekk tax
YOU ARE READING
Xalaat
AdventureAy xalaat la yu ma am yéene weccoo ko ak yéen ndax njort ni mën na amal njariñ ki koy jàng. Waaye it di ci xarale seeni xalaat ndax xalaat moom du massa doy. Dal leen ak jàmm