"Bëggoon naa ñu xettali ma ci xeetu xam-xam bu jaffe bi Nga xamni apparemment daanaka ñepp am nañ ko leegi ba mu des man.
Lu ëpp ci nit yi tay, da ñuy gis benn situation rekk daldi ko àtte te fekkee wu ñu, déglu wu ñu ku ko fekke.
Assane dafay deff benn publication ni nangam daff ko dall, nga dem ci commentaires yi fekk fa Ma Ibra naan "kii waxul dëgg", Khoudia naan "ki kanamu door kat am bii li muy wax amul", Papa naan "li mu wax dëgg la da ngeen soxor rekk", Awa ñëw ni "kii dafa bëgg ñu defal ko collecte rekk motax muy victimiser wu waaye limuy wax nii du dëgg"...
Walla Aïda di jooy, Astou taxaw fée naan joyam yooyu dëggu wul ci moom seytaane rekk moo ko jàpp.
Walla Abdou ñëw nettali ni da ñu ko agresser expliquer ni mu deme yépp, Badara mi fekkee wul di waat ci Yàlla ni du dëgg, Rama di waat ni dëgg la te ñoom ñaar ñepp amu ñu ci lu léen wóor.
Walla Ibra di dimmali ay nit ci alalam, Marieme taxaw fée naan "deffu ko te Yàlla tax ngistal rekk moo ko taxa jokk".
Man li ma jaaxal mooy, fan la nit yi jëlee xeetu xam-xam bi leen permettre, ñu déglu nit ki rekk mana xam ndax li muy wax dëgg la walla déet, te Li muy wax fekkee wu ñu ko, te it amu ñu seede bu jóge ci ku ko fekke?
Walla bokk lenn ci nit yi, Yàlla dafa deff ci seeni nopp ak seeni bëtt "détecteur de mensonge" ba tax ñu mana juger seeni moroom "sans preuve ni témoin".
Li waral nakk mbir yi jaaxal ma mooy ni lislaam daff ñu tere conduite bu ni mell ndax daff ñu jàngal ñuy àtte nit yi ci li ñu gis (manaam li la woor) te bañ ko àtte ci yéene bi mu am ndax Yàlla rekk moo ko xam Li nekk ci xolam.
Firnde bi mooy, ñaari sahaba ginnaaw bi ñu attaquer ay yeeffër, da ñu ci cerner kenn, bi ñu ko jegee ci la yeeffër bi daldi wax baati seede yi ni "laa ilaaha Illal Laah". Kenn ki dal di woññeeku bàyyi ko fa, waaye keneen ki dafa jubal ci moom ray ko. Bi ñu ko yëgalee Yonnent bi asws daff ni ko "dafa wax laa ilaaha Illal Laah ba pare teewul nga ray ko?" Mu tontu Yonnent bi asws ni "kooku daff ko wax rekk ndax ragal armes bi ma yoroon". Yonnent bi asws ni ko "ndax da nga xar xolam ngir xam ndax daff ko wax ci gëm ko walla déet". Mu ne Yonnent bi asws di ko bamtul kàddu yooyu ba mu doon ñaan baña Dugg ci lislaam laata bés boobu. (les jardins des vertueux N°393)
Benn sahaba laaj na Yonnent asws ni ko "looy wax ci bu ma daje woon ak ab yeeffër ci xare, mu dagg sama loxo ak jaasi wam daldi daw làqatu ci ginnaaw garab wax "laa ilaaha illal Laah" ndax dama ko wara ray donte wax Na baatu seede yi? Yonnent bi asws tontu ko ni " déedéet waroo ko ray. Sahaba bi ni Yonnent bi asws "dafa dagg sama loxo soga wax laa ilaaha illal Laah". Yonnent asws ni ko "bul ko ray, ndax bo ko raye moom dafay nekk ci situation bi Nga nekkoon laata nga koy ray, yaw nga nekk ci situation bi mu nekkoon moom laata muy wax "laa ilaaha Illal Laah" (les jardins des vertueux N°392)
Kon nga xamni ab jullit warul benn yoon muy àtte, di juger loo xamni amu ci certitude, amu ci kóolute, waaye ñun moom fit la ñuy deme, ci lu gaaw ñu ni diw deff walla deful, nit wax na walla waxul, ba leegi ñu bari amu ñu sañ-sañ di wax dara en public ndax loo wax ñu ni du dëgg, walla gëmoo li ngay wax, mu melni leegi ñepp ay door kat la ñu.
May fàttali ni ñi doon baax ñoo ngi baax batay, du ni bari na door kat rekk leegi ñepp ñoo yem.
Yalna Yàlla jàppale ñu ba ñu ame jikkoy jullit dëgg ci Barke Yonnent bi asws." ✍🏿 Ma Ibra Laye
YOU ARE READING
Xalaat
AdventureAy xalaat la yu ma am yéene weccoo ko ak yéen ndax njort ni mën na amal njariñ ki koy jàng. Waaye it di ci xarale seeni xalaat ndax xalaat moom du massa doy. Dal leen ak jàmm