"Ma Ibra mba julli woyof na ci yaw ba ngir nga def ko du jaffe, ndax sawar nga ci ndax fonk nga ko keem ni nga fonke say "entraînement" ba doo ko "rater"? Saly ni nga sawaree ci yëngal say cër booy fecc ndax sawar nga ci sujjot ak rukkoo ak taxawal julli manaam sabbaal sa Borom mi la bind?
Awa mba mën "lire" Al Quran. Bo ko manee it mba tiim ko di ko jàng nekkul lu diis ci yaw ba Nga mana toog ab diir do ko xool?
Musa mba ni ngay gëstoo xam-xam u bu jëm ci wallu adina ba ñepp naan "intellectuel" bu mag nga, yaa ngi koy gëstoo sa diine ngir xam say wareef ba noppi di ko jëffe laata ngay wuyyu ji sa Boroom di fa perte?
Khoudia mba ni ngay toppatoo wee sa yaram ci setal ko ba saabu bu nekk nga jënd ko, ya ngi koy sellal e sa ruh (âme) ci sangayu janaba ak njàp ak jaamu Yàlla ngir dindi bepp tilim bu taq ci yaw ndax say bakkar?
Ngone mba topp ci baati music gënul woyof ci sa lamiñ, mba gënoo ci sawar, Mba gënul neex ci yaw ak ci sa xol que ngay zikr, di tudd turu Yàlla yu sell yu raffett yi ak di julli ci Yonent bi asws?
Aïcha mba bokku ci ñi nga xamni amu ñu benn kersa ci deff lu Yàlla mi leen moom tere, ba noppi di am kersa ci deff digle y Yàlla mi léen moom lu ci melni muuru mba di yor kurus?
Mandir mba sa lamiñ wax lu ñaaw, saaga nekkul lu ko yomb, nekkul lu woyof ci moom?
Fatou mba sa lamiñ bokkul ci lamiñ yi Nga xamni fu ñu addu wee ñepp taf seeni nopp te naan astaghfirul Laah?
Maryama ma ngi am yaakar ni fépp foo toog ak ay nit di wax ci Khady, bu ñu dajee ak moom da ñu koy fonk, da ñu koy estimer, da ñu koy naw, amna yaakar ni doo toog fenn di wax Aminata ñuy daje ak moom di ko moytu ak di ko wan mbañeel.
Merry yaakar naa ni bokko ci ñi nga xamni bu Coumba amoon secret bu ko sonal, bu mu bëgg partager ak nit ngir soulager wu, nga sës fi, dafay préférer dee que mu lay wax secret wam, ndax gëm ni do ko denc da nga koy tasaare.
Ngir gattal, yi ma fi lim nii bu fekkee dafa nekk ci yaw Ma Ibra, xamal ni jot na Nga seetat sa bopp te xamni defaru waat war nala, xamni saggante dal nala, xamni amna lu bari lu la manquer, te temps amul keem ni ñu koy waxe, kon jogal ci sa bopp ba la moo wees.
Yalna Yàlla jàppale ñu ba ñu ame jikko yu rafet yi mu tagge woon sunu sàng sunu Yonnent asws ci barkeem." ✍🏿 Ma Ibra Laye
#freesenegal
YOU ARE READING
Xalaat
AdventureAy xalaat la yu ma am yéene weccoo ko ak yéen ndax njort ni mën na amal njariñ ki koy jàng. Waaye it di ci xarale seeni xalaat ndax xalaat moom du massa doy. Dal leen ak jàmm