Sunu diggante ak sunuy moroom

12 2 3
                                    

1) Lep Loo bëgg de ko defal say moroom

Bo nekkee gor, di nga tollu fo xamni do to sañ di fayyu jëm ci ku la tooñ donte am nga kàttan gi, do to sañ baña dimmali ku soxla sa ndimbal, do to am sañ-sañ di naqaral ku mu man a doon donte da ñu la tooñ, do sañ itam di jàmbat ci tiis wu dal sa kaw walla lo yootu joto ci, loolu yépp ndax kenn rekk muy sunu Boroom ba Azza wa Jall.

Yàlla daf lay defal teranga yo xamni daf lay woor ni yeyo woo ko ba da ngay mujj rus, Yàlla dalay suturaal ba ñi la wër di la ñee bay bëgg mel ni yaw fekk la ñu yaakar ci yaw yépp nekku fi waaye sutura su bari moo leen gëlamal leen, Yàlla da nga koy genn say mbir, do ko sóoraale ci dara, xëy bés di wut lo xamni ci ndimbal am rekk nga ko mana amee, nga ñaan ko, mu may la, te du ci xool li nga Koy tooñ yepp.

Yi yepp nakk, bu fekkee nit ki ku gore la, dafay bëgg nekk ku gore ku "reconnaissant" jëm ci Yàlla, te Yàlla keem ni ko ñepp xame, du Ku ñuy jënd cadeau di ko ko jox, du Kuy am xew ñu demal ko, du Kuy soxla di ñëw ci yaw nga koy fay bor... ndax ku doylu la ci boppam, kon soxlawul daray mbindéef yi, ndax Mooy ki nga xamni dafa woomle.

Loolu motax nitt yi may wax, ngir wane séen ngor jëm ci Yàlla, ngir melni kuy fay bor bi ñu amel sunu Boroom, benn bunt la ñuy gis muy mbindéef u Yàlla yi, keem bu la nit defale teranga te bi nga tollu ci mën ko fay nekka tu fi nga jël teranga boobu jox ko njaboot am.

Loolu nakk motax Mouhamed bu ko Ma Ibra tooñee mu baal ko ngir bëgg fay njéggal u Yàlla miy boroomi Ma Ibra.

Loolu Motax Marieme bu tasaare sutura y Aïcha, Aïcha du am sañ-sañ tasaare ay ñaawteef am ndax moo ngi jeem a dabe sutura bi ko Yàlla miy Boroomi Marieme sangewoon.

...

Ni ko Yonnent asws waxe woon "ku dul yërëm kenn du la yërëm; yërëm leen ñi nekk ci kaw suuf, Ki nekk ci asamaan ci yërëm leen".

Kon lépp lu ñu bëgg Yàlla di ñu ko defal, ñun it na ñu ko defal jaami Yàlla yi.

XalaatTempat cerita menjadi hidup. Temukan sekarang