AWA: tay li ñuy waxtaane comme ni ngéen ko gise ci message bi mooy internet, waaye laata ñuy tambali, na ñu Abdoulaye wax lan motax mu tann thème bi, dina ñu dimma li ngir ñu xam naka la ñu koy traiterABDOULAYE: dama seetlu ni lu jara waxtaane la, mbir la moo xamni mën nañ ni daanaka manul ñakk ndax ñepp ko soxla, ñepp koy jëffandiko. Waaye booy deglu xalaatu ñu bari jëm ci internet rawatina makk ñi, di ngay yegg (sentir) ni xamu ñu carrément lumu doon, ba sax leek leek da ngay degg kilifa diine naan « baayi léen internet bi ». Te xam ngeen bu baax ni internet njariñ gi mu ëmb mëneesu ko lim, li muy defar kenn xamul nu mu tollu, malheureusement ñoom nakk li nga xamni moo ci bonn rekk la ñu gis, moom la ñuy degg, motax nakk ma yaakar ni war na ñu ci deff exposé, amaana ñu am ci béneen gis gis.
Fatou: man yaakar naa ni
AWA: kan moo la yaakar lo, ak kan mo la jox kaddu?
FATOU: yaw da nga violente trop tchiiip 🙄, bul fatte ni man dama bari wax te bu nit waxe lo xamni dama ci yagg xalaat damay yakkamti yeebbeeku, te réglement bii miina guma ko
AWA: bref, noppil, te nga croiser les bras, te xaar ba ma jox la kaddu
FATOU yëngël bopp ngir wax waaw
AWA: problème bi ñu am mooy, da ñu tamm di deff jugement ci benn mbir te du ñu ko évaluer ci walla yepp, da ñu tamm di contextualiser mbirr ndax ay aspects négatifs yu ñu tamm di gis, te reere ni amna yeneen aspects yu wuute ak yooyu yu mu am tamit
FATOU: mooy lima la doon wax rekk ci li ñu naan « c'est le milieu qui détermine l'homme »
FATOU daldi buxxu bëtt yi, daldi xool ñi ko wërr, ndax fatte waat na ci diggante bi, ni réglement bi dafay téré nit wax te kiy jiite ndaje bi joxu ko kaddu
AWA: apparemment munoo tëngku ci réglément bi, aythia vas-y waxal, da nga ëppël rekk waaye say wax laa doon waaja citer
FATOU: 😌 merci ci chaines yi nga tekki, maa ngi doon souffrir ci lima doon retenir lima bëgg wax, lima doon wax kerog rekk mooy ñëwaat fii (flash back) ndax lenn ci ay nitt da ñuy deff lu ñaaw ci benn bërëb, ñu daldi bonal bërëb boobu ba kepp ku ko jege ñu yaakar ni dafa bon
ABDOULAYE: kon est-ce que du ñu deff pétition ngir ñu dakkal jaayum paaka ci dëkk bi
FATOU: waxi doff 😦
Hakim fixer ko, xool ko ci bëtt
FATOU: d'accord dama ko fatte woon, Tonton Hakim neena woon ak lu waay mana wax, même bu fekke am naa certitude ni dafa juum, naa prendre la peine ma laaj ko, lan motax mu wax loolu, kon nakk Abdoulaye lutax nga wax loolu?
ABDOULAYE: ndékété Hakim amna ci ñu mu baax. Dama bëgg wax ni bu ñu toppe logique boobu da ñu wara tere jaay paaka ak jaasi ... ndax bes bu nekk ñu jëffandi ko ngir gaañ ci nitt, agresser ci nitt, walla nitt gaañ ci boppam, te pourtant kenn néewul paaka dafa bon, ndax xamnañ ni paaka boobu ñu bari ci nitt yi, ñoo ngi koy jëffandikoo ci loo xamni njariñ dong la, kon du paaka bi moo baax walla moo bon, ci ki koy jëffandi ko la, internet tamit c'est pareil. (waxi nitt🫢)
AWA: effectivement loolu la ñu wara comprendre loo nit ñi nakk, il faut ñu xamal léen ni internet outil rekk la. Dafa melni ndox rekk, amul couleur, waaye ci récipient boo ko deff dafay melni day jël couleur boobu te loolu du couleuram, kon mbiru internet tamit kenn du ni baax na ni kenn du ni bonn na, da ñuy japp ni dafay jëmmal melokaanu doomu adama yi, reflet wam lay nekk.
FATOU: kon kay parents yi waru ñu kaas naan internet bi yaqq na xale yi, en réalité fuite de responsabilité la ñuy deff, ndax ku leen degg day yaakar ni xale yi ay innocents la ñu, alors que ñoom ñoo leen yarul, ñu ñëw ci biir internet andiwaale fa séen rewande, kon yaqqu nañ avant même ñuy ñëw internet motax ñu fay nekk di saagaate, di tooñ, di yaqq derru jambur yi j'en passe, comme ni nga ko waxe séen reflet rekk la, kon est-ce que war nañ indexer internet
YOU ARE READING
Xalaat
AdventureAy xalaat la yu ma am yéene weccoo ko ak yéen ndax njort ni mën na amal njariñ ki koy jàng. Waaye it di ci xarale seeni xalaat ndax xalaat moom du massa doy. Dal leen ak jàmm