Roy ci Ibliis / Prenons exemple sur Satan

5 1 0
                                    


"Jullit bu bëgg sax ci yoon bi koy jëme ci Yàlla, dina baax lool mu roy ci iblis miy seytaane.

Yonnent asws moo ñu jàngal ni, bés bu nekk, iblis dafay yebal njabootam ci kenn ku nekk ci ñun, ngir mu lay xiirtal ci nga moy Yàlla.

Am Abdoulaye mo xamni, ci ndimbalu Yàlla, bés bu nekk iblis jël défaite ci kanamam, ndax dina deff lu mu mën yépp waaye du tax Abdoulaye topp ko ci li mu koy xirtaal.

Iblis dina topp Aminata diir bu yàgg, ngir deff lo ko, walla wax lo ko lu diine tere, waaye ci ndimbalu Yàlla, saa su nekk Aminata toroxal ko, fënetal mboolem ay pexeem.

Waaye da ngay seet lu ni, du massa tax iblis décourager, bés bu nekk dafay tàmbali waat ay pexeem, and ci ak ñakk jomm bu matt sëkk, ak détermination itam, tegaat yeneen pexe.

Boo koy toroxal bés bu jott, walla sa giirug dund yépp, teewul booy genn adina sax du décourager, dina ñëwati deff ay pexeem di ci yaakar mu sotti.

Kon li nga ciy jàng, mooy ni iblis du baayi, du décourager, wutu ci jomm, te ba dernière minute sax dafay dunde yaakar batay, gëm ni mën nala wàcc yoon bi.

Motax nakk bépp nit bu bëgg sax ci yoonu Yàlla, dafay war Nga roy ko moom iblis ci baña décourager, ci ñakk jomm ak defaru waat saa su nekk ngir waajal ëllëg

Ndax nit ku nekk dafay def bàkkaar, ñu bari nakk bu ñu deffe bàkkaar, da ñuy commencer regretter, ñi jeppi séen bopp, ñii commencer décourager ba di ñakk yaakar ni du ñu bokk ci yërmànde Yàlla, ñi di jom lu ci seen digganteek Yàlla , ndax Ma Ibra bu defee bàkkaar da naan russ naa jàkkarloo ak Yàlla, daldi commencer bàyyi julli bàkkaar yi di yokku, daldi rus téye kaamil Al Quran ak yorr kurus protection wam contre iblis di gën waññee ku, rus fréquenter nit yu sell ndax yaakar ni dafa seexlu, iblis di gën am doole ci kanamam, mu baaye ku carrément motax ñu naan la "le péché appelle le péché".

Bu yàggee nakk, Ma Ibra moomu sànku lay deff définitivement, ndax ki mu ko seqqal du baayi, du dalay deflo bàkkaar rekk taxaw di jubiler, daff lay doggali, topp la ba nga sës, ba dootu lo am dara lulay connecter ak sunu Borom.

Motax nakk ñu wara melni moom, saa bu ñu daanoo na ñu gaaw jógaat, ndax lu ñu gën a yeex, jóg bi di gën metti, manaam boo daanoo ci bàkkaar na nga gaaw tuub, luko moy yeeneen, bàkkaar lay juraat, te tuub ga dafay gën a jaffe.

Bu ñu jomlu suñu kanamu Boroom, saa su nekk, ak lu ñu mana deff, bu ñu gëm ni Yàlla daf ñu seexlu ndax Ku wuute ak Mbindéef yi la, au contraire daf ñuy yàkkamti gis ñu ñëwaat ci Moom, keem ni ñu Yonnent bi asws jàngale, ni Yàlla di contaane bu jàmm bi deffee bàkkaar ba noppi ëlbatiku di ko jéggalu.

Kuy xeex ak koo xamni du baayi, te bari na doole lool, da ngay nekk ci say gardes saa su nekk, jéema fatt fepp, tey daw làqatu ci ginnaaw ki ko ëpp doole, Ki Nga xamni moom Iblis ci boppam neena daff ko ragal, muy sunu Borom ba Azza wa Jall.

Yalna Yàlla jubal ñu, yalna Yàlla muccal ñu ci bépp pexey seytaane te saxal ñu ci yoon wi nga xamni war na ci Barke Yonnent bi asws" ✍🏿 Ma Ibra Laye

XalaatDove le storie prendono vita. Scoprilo ora