• N: lutax Nga soof yaw?
• H: lan Nga tuddee soof?
• N: saa su nekk li ma lay proposer pour ñu deff ko, mbir moo bëgg la, sa xell da ciy nekk, waaye doo ko deff benn yoon, te li nga ciy sooraale noonu du dara
• H: lutax nga ni du dara?
• N: li nga ciy soorale mooy ni loolu bàkkaar la, ya ngi xalaat ni loolu waru ñu... waaye nakk waroo fàtte ni Yàlla kuy jeggële la, te kenn munul mucc ci bàkkaar, te sax loolu grawul noonu, ndax yaa ngi gis nit ñi di deff lu raw fuuf li ngay bañ ñu deff nii, lutax koon munoo baayi mu jàll benn yoon rekk?
• H: li nga may proposer saa su nekk ay bànneex la certes, waaye nakk du ma ñëw rekk top la ci ndax conséquences yi maa koy gënë dund après, te bu doon tuub rekk duma ragal ndax Yàlla jeggëlaakoon bu màgg la, waaye yaw lépp loo xëssa tàmbali du yomb Nga baayi ko, te da Nga may fitnaal ba bu ma ko déful du ma am jàmm, te bu booba damay dem ba mu nekk habitude ci ñun ma bëgg ñu baayi ko du ma am kàttan gi te xam nga bu baax lima lay wax
• N: wa xana da nga fàtte hadith bi Yonnent asws wax ni "bu ñu baayé Deff bàkkaar Yàlla tukkël adina bi, andi fi ñuy deff bàkkaar", bul yenn sa bopp loo attanul, nitt rekk nga te lii du bàkkaar bu magg
• H: wa leegi bu ma ci dee fekkee lan laay wax Yàlla te degg nga Yonnent asws wax ni "bépp bakkan anam ba mu faatoo la ñu koy dekkalee"
•N: yaw xam nga ni dee wa guñ leegi sax da nga bëgg grawal situation bi rekk
•H: yaw instant bii gisoo ludul bànneex bii, motax argument bu ma la mën andil tamit da ngay koy rejeter
•N: non non yaw yaa metti rekk, lii vite fait la, après ñu deff istighfaar, te boo ko déful après day dess sunu xell à chaque ñu koy xalaat, te kumpa boobu mën na jurr bàkkaar bu gën màgg bi, tee nga ñëw ñu deff bàkkaar bu ndaw bii rekk, te bu la neexe dootu ñu ko deff ba faw
• H: maa bañ, le fait que muy nekk sunu xéll di ñëwaat loolu dubàkkaar, kon mooma gënal ñuy dugg ci lii, mu dem ba doon drogue ci ñun comme ni Nga defoon ci yeneen bàkkaar yi ba leegi munu ñu ko baayi
•N: waaye loolu grawul, ndax au moins ño ngi koy deff ba paré di ko reccu, di tuub, di suturaal sunu bopp, ñoo gën fuuf ñiiy deff bàkkaar yu màgg yi ba paré di ko nettali di ko ndamoo, xam nga ni sax yemu ñu ak ñooñu te loolu rekk war na tax nga Ban mettil affaires yi
•H: deedeet baayil noonu rekk, na ñu ko muñ, yoon yi passé nii nga ma doon naxee te fi mu mujj neexu ma
• N: yaw da nga soof rekk mais xana déggoo ñu ni ay "laa ilaaha Illal Laah" ku ko masa wax benn yoon do dugg safara te yaw bess bu jott ñu deff ci ay junni, en plus bàkkaar benn point la ñuy bindal te bu fekkee yiw la fukki point lay doon, xam nga ni ak nu mu mana demee da ñuy mucc
•H: bul fàtte ni Yonnent bi asws neena nit dina jaamu Yàlla ba diggantéem ak aljaanna jege lool, ci jeexitu dundam mu Deff jëfu waa safara Yàlla dugal ko fa, te neena woon tamit jëff yi ñoo ngi leen di àttee ci seeni jeexit. Kone Li ngay wax nii yépp dara wooru ci, te degg nga ci sahaba yi, ku xare ba dee ci lislaam, Yàlla dugal ko safara ndax dafa xaru (gaañu yu metti la amoon mu doggali boppam) te kooku gis Na Yonnent bi asws, andeu ak moom, julli, wax "laa ilaaha Illal Laah" te safara la mujj
•N: yaw ci boppam yaa négatif, côté bu bone rekk ngay xalaate te loolu baaxul, ndax Yonnent asws doon na wax ni Yàlla li nga ko njortal rekk lay doxale ak yaw, motax nakk nga wara dalal sa xell te baayi sa soof soof lu gii
• H: noppalul te xamni li nga bëgg tay du ma ko deff, xaaral sax ma dèm yeesal sama njapp te ñëw sikar ndax nga baayi sa xalaat yi
•N: wa leegi baayi naa bul fi jogg de man dama sonnë, baayil mu sedd leegi, waaye nakk munoon Nga Deff lima la wax rekk
•H: bu may xëy in chaa Allah Di commencer wóor comme ça sa domination bi jéex nga mayma jàmm, ludul lu bon Doo mako xélal, doyna nakk, dinaa jóg ci yaw. topp la motax munu ma am estime de soi, gacce gu rëy lay yegg Si sama digganteek Yàlla ndax xam Nga ni limu may defal ci teranga Yellul woon makoy désobéir d'autant plus que limu may tere pour sama intérêt la
•N: ndax mën naa xam kañ ngay noppi?
H: l'homme
N: Nafs (passion de l'homme)✍🏿 Ma Ibra Laye
YOU ARE READING
Xalaat
AdventureAy xalaat la yu ma am yéene weccoo ko ak yéen ndax njort ni mën na amal njariñ ki koy jàng. Waaye it di ci xarale seeni xalaat ndax xalaat moom du massa doy. Dal leen ak jàmm