Saar 29

7.7K 1.2K 67
                                    

Saar 29

****Adja****

-Adja wakhognou no def ak ndaw sossou ?

-Khana dou ex-femmou Khalil bi ga may wakh dé Dié ?

-Lou ko moy ?

Dié dal dou déme. Meuna raconter sama vie torop nak mais nak client yi di létou instant yi tay laigne fi sogay gneuw, khoma léne. Lane moma wore ni sakh ni kéne ci gnome khamoul Coura ? Dié dal dou changer yeufou dof rek lay def.

-Dara nak. On gère.

-Gnémé wo wakh lolou kay. Yow mifi gneuw kérok mer bay foute ndakhté dafa done indi domame yi, né fakh thia keur ga comme si mome moy seuy.

-Dié nguir yalla après di naigne ci wakhatte.

-Wa Adja mi louko dale ?

-Wa Sokhou, Adja mi mbadou li la wok moko khouri ?

Khadija moy kimay lette mo tape copiname bi Sokhou, ki Dié di défar wakh lolou.

-Lolou dé moma diakhal instant yi.

-Mbadou ??? Donté dama daigne koumpeu nak il faut que ma lathier pour kham.

-Mais sauf que mome dou ex-femme dé car dieukeuram bi diotoul tak ndaw ci.

-Kone kay sougnou gnari histoire bokoul.

-Bokoul mome mais dafa ale ay similitudes. Imaginele sama dieukeur bayi ko gneuw ci mane tak ma, ndaw ci né dou ko bayi mou sed. Ma khamal la nak, kokou dafa capable mais yalla moko eupe dolé. Lou né lay def pour saleté sama seuy. Deme na sakh ci serigne. Ma kheuy kerok febar bou nitt khamoul foume diogué, ma déme hopital guissougnou dara après ma dioubelou ci fadiou wolof yi, gnou néma def-def la.

-Layila... Dit Dié.

-Deuk bi dé yow lou né laigne sagne. Mais lou lokho def lokho meunako dindi. Donté mome togoul mane tamitt douma tok dé.

-Ya wakh deugue katt chérie. Bo togué né fouss dé diga ko guiss dé. Mba yow togué rek Adja...Khadija moy lathié lolou.

-Démouma ci serigne dé mais khalatte nani sagnoul lolou.

-Bess bougne lay dédaler ak Khalil dafe lay bett... Dié nime seuytané.

-Coura dofé woul nonou khana.

-Mane dal limay lay conseiller moy ga woute zu moins saguatte guir are sa bop. Aduna bi diakhasso na, té kéne bayétoul bopam nonou...Me dit Sokhou.

-Dina ci bayi khel bou bakh.

Dié souma ko rayoul rek dina ma diakhal. Seytané na, rambathie na.

Après nak gnou changer wakhtane déme ci belle-mère yi. Walay kou nek ak sa problème. Mane mome c'est toujours la même chose, mère bi beugouma té essayerwoumako neub sakh. Léne dongue dé lamay reprocher, lima nékoul mbokam. Mais ba légui momatanel belle-mèrou Sokhou bi. Yéne meune guéne imaginer, belle-mère bou lay tongal tout simplement parce que daga ko wane ni meunoula dieund et que faléwo khalissam ?

Khalasss !!!!

C'est que nak li moy ligne done wakhtané kérok ak Dié, so yoré yéne yore yi dagay yakar ni nitt kou nek ame na gneuk té ame ga lolo dieundé alors que gneupe yamougnou... Khana mi deukone ci mbarane sakh instant yi kouma tek louma meunoul ma bagne. Khaliss nekh na torope mais bo amoul diam boko léké yakaroumani di ga yeuk nékhay bi.

********

Thieyy Nogaye, li nek ci deuk bi yeup kou ko nara wakh, di ga fi dé gnou souli la. Yéna gui fatélikou sama ex bi Gora, Nogaye dé wouteule nako béne khalé boume ko brancher. Instant yi dé dafa wara andak Nogaye keur boy bi. Nogaye mo gui keuram di préparer. Mane ak Gora gno gui ci mbed bi ci bountou salon bi di khar Nogaye guéne.

Damay bagna done badola rek sinon, bayi nako fi gnibi en plus mogui ni di goudi.

En plus nak dafa gnak fayda. Ware na ma wakh ay yagui rafettak sa dieukeur moguilay topato bou bakh.

Wa merci bamou ko setelo mais yonam nékoul ci sama rafett ak sama défarou. Sama dieukeur mome gorr leu, gor la. Meloul ni gniy bayi sene diabar yi thia keur ga gnouy souffrir après di tope ci guinaw khalé you djiguéne yi gnou lék khalissam rek.

Auto Khalil dé foumako séné khamé ko.

Lima wakhone sank rek, Sénégal ma fi gueune dieukeur. Tay mou gneuw dieulsima té wakhoumako dara.

Bi ma kholé kanam gui dé on dirait que dafa.

-Adja, ki kane la ???

Youkhou bimou ma youkhou dé sama fitt bi néna reuss.

-Kone yow li ga néké ci salon bi...

-Serigne bi ga bal ma...Gora mo narone intervenir mais Khalil da ko beumeukh, kheuthie sama lokho.

Mame mome instant yi sama thieur yi gno melni lou bagne, khoma sakh fane la nek instant yi ak loufi khew ci diganeté bou gate bi.

Ba nima dougué ci auto bi mou commencer dawal wakhouma.

Ma guiss ko mou merr té mane comprendouma dara. Khamouma li wara khew.

-Wa daddy, bou ma def ni.

-Adja, merde. Teudjal sa guémigne gui ba kerok gnouy ague keur ga.

-Mais mane dama khamoul li khew di ?

-Da ga beugue ma gnouss la ci auto bi ?

-Ay Khalil !!!

Falé wouma sakh. Mane souma défé li takh mou méré ma ok, nama méré mais défouma dara ba paré moumay méré.

Takhaw ci mbéde mi rek di wakh tane lolou lane moci nek. C'est pas non plus comme si dafe ma béte ci nek may wakhtane ak Gora. Té même souma défone lolou sakh Khalil waroul ame réaction bou démesurer ni. Li mome tégouwoul féne.

*********

Bignouy dougue ci keur gui dé Khalil sama lokho bi la téyé, instant yi magui mel ni khalé bou def mossibame, gnou koy yobe pour punir ko.

Bougne agué thia nek ba Khalil dina ma déguelou, fime nék ni meunouma wakh car nitt gna gui fi. En plus donté merena meuna fi wakh béne affaire bo khame né souma sagnone dou ague ci nopou kéne ci keur gui.

Gnou togno, taf-taf, dieul escalier yi. Yek ci kaw, ba dougue sougne nek, Khalil sani ma ci kaw lale bi.

-Khalil do ma def nank tamitt...

Dina youkhou kay parce que dama merr. Bou féké mome rek mo meuna mer dina lerr.

-Ma diape la en flagrant-délit gay farantou après ga beugue takhaw sama kanam dima wakh limay def.

-Mais yow t'es malade ou quoi ?

Bi ma koy wakh lolou da ma diogone takhaw pour diakarlo ak mome mais bimou ma mbadié dé, plongerwatt na ci lale bi ci lou gaw.











Note de l'auteur: Dina diéma poster suite soubeu parce que bi retard mome gnaw na torop. Dama fatéwone sakh chronique bi.

Diape rek nak. Lima bolé temps yi mo bari.

Kéne kou mel ni yowOù les histoires vivent. Découvrez maintenant