Saar 35

7.9K 1.1K 33
                                    

Saar 35

*****Adja*****

Li dé la olof nane ma lank beuré wouma doula ci guéné ni bo beuré woul tamitt, gnou beuré dale sa kaw.

Mane khoma serigne. Té amana souma Coura diogaloule wone douma meussa dougue ci serigne mais noy def ? Deuk bo khame né , nitt gni bone lagnouy concours.

Dégone na kérok Sala nane gneupe khame naigne ni Coura bou ko Khalil také ci séne guéne 3 mois yoyou c'est parce que dako liguey mou accélérer affaire yi. Magui done wakh sama khel kéne douma fi bakar lo ni dara worouma ci. En plus est-ce que mane khame na lignouy wakh sama guinaw ? Façon séne yaye mane rek la bagne té neuboumako.

Di gnane yalla mou diégueul ma ni li may def ni mome khame nani bakar la ni magui liguey sama dieukeur mais bou dé moy seulmoyen pour que ma ame lima beugue , je vais pas hésiter 3 fois.

Gnibi ci bou yague dé légui 23heures diote, ba légui Khalil kéne guissouko ci keur gui.

-Adja ana Khalil ?

Sank ba légui dé gno gui wakhtane, lignouy wakh intéresserwouma, kéne bolé wouma ci. Légui nak mère bi diéki rek di ma lathie Khalil.

-Mane thi soubeu la fi kheuy dama démone sama keur yaye. Bi ma gnibissé fékoumako fi, té wowouma, wakhouma.

-Guiss nani temps yi yeup séne digane té nékhoul.

Hypocrite bou bone bi. Khame nani moko ci gueuneul.

-Sama yaye wakh na deugue dé...Dit Sala...Daguéne fogueni bou guéne di khoulo kéne dou léne dégue.

Fi ma tole ni dé souma done deureum rére, souma done glace séye. Mais après c'était évident, sougnou chambre isoléwoul dé.

-Ay problème you ndaw rek mais dinaigne ko régler.

-Mo gueune dé. Diame mome ci la lépe khadj...Sama belle mère mo wakh lolou. Instant bi dé, je prends sur moi pour bagne ko tathiou ba né ko khame nani mo la ci gueuneul.

-Mba dioté woul dara ak Coura rek... Demande Sala.

-Dédette diotéwoul dara ak mome. Kone daya me importance torope ci sougnou dounde té diarouko.

Sama belle-mère dé khélou bime ma sani. Deugue dé la wakh, diabattam bou gnak khorome bobou dou mome moy takh may yak sama seuy.

-Wakh ga deugue dé. En plus wakh tane naci ak Khalil kérok.

-Lo wakh ak Khalil ??? Ma lathie lolou Sala.

-Que Coura dak sa diane ba mou dem ga top ci guinawam di daw la beugue def. Nénako bo ci dougater sois sûr que day geuna pire.

-Yow dé mague bou bakh, khame nani bou gneuké yeup mélone ni yow ni yow, diabarou thiamignou kéne dou sone.

-Dou bakh dé, wakh deugue la rek.

-Yow mome daga seuytané.

Khame nani wakh djodjou mome, mère bi mougne nako ba sone mou teu. Ay ré guimay beugue diape sakh mais magui koy mougne.

Bou khamnone li ùay wadj dina bayi Coura té lidieuneti domame.

-Yaye nak, seuytané amoufi nak. Yow sakh khame ga li fi Coura nékéwone. Seuytané seuytané bou amoul féne nak. Fi la dane tok wakh tane ak gnoune, di kaf ak ré. Bou goudi dioté souko Khalil wowé skype, ga rombe négame dégue ko mouy dioy.

-Dafa beugone féki dieukeuram rek...Dit ma belle-mère.

-Ok dafa beugone feki dieukeuram mais mou tek ko ci yone, bagna diakhassé nitt gni simplement pour arriver à ses fins. De toute façon, Khalil dès le début intention yobe ko la amone. Coura mo yakame ti wone rek.

-Da di wone khalé rek té khélou khalé diape ko.

-Adja gui ni, ate yi Coura amone bime fiy seuysi la ame té takhoul mouy dokhalé ni mome. Yow mome li Coura di sa domou frère mo takh ga diko bale lépe. Wore nama ni bou Adja nékone placou Coura thia diamono yoyou, diga khara sa tankou toubeuy né dou déme féne.

Instant yi yeup mère bi lay khol pour khame loumou meuna tontou.

-Yow mome daga seuytané...Répéterna lame wakhone sank Sala. Mais gueunoumaléne kham Sénégal. So wakhé deugue rek, gnou traiter la de seuytané.

-Adja nak yow mi lay wakhal, sama yaye mome bouko déguelou. Khalil mi ma guiss dafa mel ni khelam da fa nékat ci Coura khoma lou khew ak noume meuné gawé ni mais yow dal diogal ci sa bop.

-Wa mane Sala mi, thiey ma woute kouma ko ngualabale...

Mane dé magui mel ni kou am télé.

-Khalil yone moy khelam délou ci Coura, souma déguelone seuy bobou donoul wone meussa tass. Gueunou mala kham deugueur bop gui Khalil deugueur bop.

-Mane dé yaye dama yakar ni, bi la Khalil di wakh limou dounde ak Coura diokho ko nope bou bakh bi. Lolou mo takh ga nane ko warou ko wone wathie.

-Khelou khalé la wone rek.

Séine conversation bi sakh ça commence à me souler, fimay diogué rek ma dégue Khalil di nouyo.

-Yow mome goudé ga di. Fo démone ?

-Dama séti wone sama guys gni. Khame ga rek, bo néké ak gnome do guiss temps biy passer...Lolou la tontou yayam...Magui yek ci kaw.

Mane mome kholouma, lidieuneti wouma. Mais grawoul ce n'est qu'une question de temps lima serigne bi def dina ko appliquer à la lettre té wore nama ni dina ci guiss résultats.

Yek na ci kaw feki djiko.

Guiss nako mou tok ci lale bi, on dirait que khel ma gui fénéne comme si khamoul lane moko weure instant yi.

-Khalil, Khalil, Khalil...Won ako gnéti yone mouy sogay sigui khol ma.

-Hun !

-Ma défaral la ga rére ?

-Rére na ba paré.

-Fo réré ?

-Fi ma nékone.

Tay nak dafa séde, heureusement pour mane car ça me donne une idée.

-Ma tangalale la ndokh ga sangou. Ndokhou robinet séde na dé té ak goudi boci sango téme ga sothie.

Kholnama hésiter mais l'essentiel moy après yeungueul na bopam pour néma waw.

Ma deme tangalale ko ndakh def ko ci siwo, dieulalé bouteille bi ma pa bi diokhone sotiko ci très subtilement limay agir yeup, magui bayi khel ci mome ni khame nani souma diapé mome moy diril naigne ma sama sague ci biti.

Tout a marché. Sangouna ba paré. Pa bi mome wakhonamani yak mome dou yombe donc bouma khalata guisss résultat dans l'immédiat que il faut mou ande ak patience. Dou yombe dé car warena ci sangou 3 fois tékhoma si soubeu di nangouwatt ndokh bou tangue bi wala. Khalil ay djikome la yore nouko nekh mel.

Ame na aussi lo khame né dako wara nane. Bobou mome moy gueuna compliqué car khalate na defe ko ci bouteille boumay def ci frigo bi mais frigo bi alalou mbolo la, daga fay dougueul sa bouteille ba la mo séde, kéne guénéko nane.

Il faut que ma woute solution dé.

********

Finalement solution bi ma trouver moy défe garabe bi ci bouteillou ndokh, dieule bouteille bi take ko ci mbousse bou gnoule en espérant que kéne bagne ko lale. De toute façon Khalil mane makoy may ndokh khame na bou bakh fimakoy diar.

Jours yi mome gno gui déme bou bakha bakh, mane nak magui ande ak sama patience rek té khame ni kheuthie mome bou dagoul yek ci.


Kéne kou mel ni yowOù les histoires vivent. Découvrez maintenant