Saar 2

16.2K 1.7K 102
                                    




Saar 2

****Adja****

Ame na you bari sama doundeu yo khame ni dougne meussa changer té li ci la bok, réveillou portable bi défatina liguéyeum maname yé ma. Ma gui ni nak, khaadiouma sakh bay doyal nélaw. 9h diotatina té 10h ware nama fek ci salon ba.

Dioque na ci lale bi wayé sama dem thia dousse ba sanguou dji amoul loume diaroul. Khoss- khossina ay tank ba nimay agué. Souma sama yaye guissone, sagaatinama car néna lolou ci ay gaff la bok. Sénégal séne bop gno gnémé gafal.

Bima sango ba paré, ma oubi sama armoire di sett loumay soll. Bima guissé ni Fanta torokhalaté armoire bi rek dama décourager, wayé mako def sakh mane mi bok ak mome armoire. Dina woute valise di ci def samay yéré. Loumou meuneti def après mo kham.

Ma yébi yeuré Fanta yi saniko ci kaw lale bi, bou gnibissi wé dinako léme force. Béne jean ak béne haut dé la guéné pour sole ko. Maquillerwouna touti rek mais defouma dara lou seuff, mélouma ni kouy dem khew. Salon ba dé tay sou bari wé nitt dinama diakhal. Jeudi yi mome moy lolou et malheureusement pour moi, oma salaire ay nékhalaté dongue la ame té lolou ci nitt gni gneuw bari la dépendre. Ligueyé ci salon de coiffure mome yakar nani moy vraie exploitation, sa statut élève dou changer mouk wala bok Nogaye mo truand rek di dounde sougnou kaw. 3 élève laigne ak mome patronne bi.

Dieundi mbourou ba paré soguay déme ligueyi. Mane rek ma fi dessone sama yaye déme na marché diayi alors que sama rak yi gnome diangui naigne. Mane mome bayina diangue bou yague. Bayi wouma sakh daigne ma dak. Goorgoorlou na nak ba ague troisième, oma BFEM oma moyenne, passéko gnari yone gnou dak ma, sama yaye né amoul loume ma yobé privé. Ma tok diape ci yalla.

Lima décé instant yi dé moy gnane yalla mou diapalé sama 5 rak yi gnou tekki ci diangue donté mane foyé na sama boss ba paré.

*******

-Adja Astou, khana doma né daguay nélaw dé ?

Nogaye nak yab nama. Dina gneuw ci salon bi di fi nélaw té ma bayi ma keur gui nek ci même kogne bi.

-Non, non. Magui wone ci portable bi.

-Mo takh kay bimalay wo dégoma.

-Dedette dama concentrerwou wone torop.

-Kholal, ki la beugue gua démal ma ci Rabi.

-Rabi ? Pour lane nonou ?

-Sac bime fi dieulone té ba légui fayouko. Néko rek Nogaye moma yoni, dina khame bou bakh lane guay def keuram.

Ma diok té dem fimou ma wakh. Salon bi nak li moci soff. Bou amoul nitt mome nala wore ni dokh yonénete guay def. Nogaye rek ci bari service.

Heureusement, keur Rabi soriwoul.

Bountou keur gui dé, kéne teudjouko dama gneuw rek dougue. Li mome yague na ci keurou parcelles yi.

-Assalamou aleykoum.

Bimay tek sama tank ci keur gui lay nouyo. Rakou Rabi bi Ouleye mo guéne.

-Adja, nane gua fi def ?

-Magui fi Ouleye, ça va ?

-Bien et toi ?

-Ça va ? Ani Rabi ?

-Migui négueume togual ci salle bi khare ko ma wowal lako.

Ma dem ci salle bi, fek na fa khalé yi di sétane mickey. Gnou may saf Eva ni. Beugue mickey bad dé.

-Khalé yi na guéne def?

Guersou naigne khol ma, tournerwatt ci séne télé. Rabi dal mo réwi dome rek.

Wa mane Ouleye dama faté wala, ani Rabi mi mou ma né wone migui ci negueum.

Ah enfin, gneuwatt na mais ba légui guissouma Rabi dé.

-Adja, Rabi day nélaw instant yi digua fi meuna diaratt ?

-D'accord.

Mane dé dioq na abale léne séne keur. Noume meuneti démé sama yoné nékoussi, diguaneté Nogaye la ak mome. Rabi bou done nélaw, Ouleye dina yagué ni.

Nogaye dina mérati rek mais li mome yague na Sénégal, nitt ki boulay lébal gua dieul ba paré té soko waré fay diko daw lo. Allons seulement rek.

Aksi watt na ci salon bi.

-Loume wakh.

Nogaye dé mayouma sakh ma aksi.

-Guissoumako dé.

-No def ba guissoko ?

-Deme na guiss Ouleye, Ouleye néma Rabi migui ci nek bi magui lakoy wowil. Ouleye dal demena ma dougue ci salle bi, toque na fa khar lou yague, Ouleye néma na gneuwatt ndakhté Rabi day nélaw.

-Nélawoul féne...Dié douguena ci wakh dji.

-Koy wakh lolou Dié ? Mane Rabi dafe ma yab la fok. Souma démé keureum dina kham bakham day nélaw wala.

Nogaye dé tégatouci béne bat, déme na yonam bayi gnou gnoune gnéte. Mane, Dié ak Mami.

-Nogaye dé khame nani soneu na ci ndiayame gi.

-Dina ci sone kat Mami. Sénégal dagno beugue lou yombe. Bo khaméni amo lo fayé do bayi marchandisou diambour kou ame loume fayé dieule.

-Dié boul faté ni deuk bi dafa méti dé.

-Adja bouma fonto méti ba ci lane ? Li Nogaye done diay dou lek dou nane, ay dall ak ay sac leu. Beugue sagnessé té yorougnouko.

-Yene gnar tamitt yéna gui sagnessé té yorouléneko.

Mami mo gueuna seytané ci kaw souff.

-Mane ak Adja dagno ame ay thiamigne you bakh yougnouy défaral.

-Thiamigne you bakh. Okay. Léne dé khame nako, Khalissou gor mome kouko lek dinako guéné.

-Tant que guéné bi dougnou gagne rek, amoul problème.

Maa tontou lolou Mami.

-Léne khame nako. Warou léne wakh dara Rabi, mome day seuy seuyeum. Dafa méloul ni yéne rek.

-Wa Adja, doma ladial Mami mou wakh gnou gnoune nougne mel?

-Question bi kay nou guéne méloul la wara nek. Mane sakh dama gnak diome, wakhone nani douma ci wakhatti.

-Yow dé boci wakhatoul dagua dé.

-Adja nak dina la rousselo. Doma dégati ma guangue ci dé.

-Ba lolou dess ci. Wa Adja samedi soir lo prévoir ?

-Instant yi kay magui ni di kholé. Da gua ame programme ?

-Waw. Ouzin moma inviter té néna day andak ay copain wam. Kagnou ande.

-Khoma lomay inviter, khame gua ni mane ak Ouzin ci khoulo laigne deuk.

-Yow ak Ouzin kay dama fogue ni daigne léne dédalé.

-Kéne dédalé wougnou Ouzin ci bopam mo soff. Khoma lo guiss ci mome ?

-Meunoko guiss, khol bi la.

Dié dafmay enerver, khole léne ko rek mou dieul lokho bi diko taf ci deuneume bi.

-Wa boul yak programme gneuweul gnou dem. Bou gnénéne gni indiwoul séni guel mane rek mafay done djiguéne té khame gua day sof.

-Gnénéne gni kay khana dinaigne gneuw accompagné.

-Dara worou laci. Wa kagnou dem. Khana doma né lou doy ni samedi, diguako passé séne keur diakarlo ak sa yaye ak sa rak you rew yoyou ?

Béne instant dioumoul dé, kharal ma langue ci rek.

Note de l'auteur : Ce chapitre est 2 fois plus court que le premier car il semblerait que lire en wolof est très difficile et prend plus de temps. Donc j'ai décidé de les faire mais d'être très régulier dans la publication. Si le chapitre est plus il prend moins de temps à écrire. Je posterai la suite très vite.

Kéne kou mel ni yowOù les histoires vivent. Découvrez maintenant