Saar 23

8.4K 1.2K 73
                                    




Saar 23

****Adja****

Bi may guéne nek bi kholou ma sakh bane heure mo diote. Donté yayou Khalil yé nama kay, na diogue rek. Nganalé gui mome diekh na mais au moins nganalé naigne ma quelques jours.

Ma wakh ko té dé mais comprendrouma fonctionnement keur gui. Keur famille yi ma dane guiss, ki dane ayé togue danoul wone gérer ménageou keur gui. Mais bon na deme dans le long terme, peut-être que ma kham youl li khew ci keur gui.

Liguey mome diakhalouma, sougnou keur meussoul ame djank donc liguey bi mane ak Fanta ko done gerer. J'ai l'habitude.

Bi ma paré wé, ci lay dégué gnouy ndode fadjar. Ci la tité nak. Fadjar lagnouy soguay ndode ni. Mane mère bi bane heure la ma yé ?

Ma déme yé Khalil néko heurou djouli diote na. Ma khar mou djap ba paré may soguay dougue ci salle de bains bi daip après mou djitté ma ma djouli.

Après diouli bi ma sangou dji soguay nélawi watt.

*******

Bignou may yewatt nane ma ma dieundi mbourou dé, nélawouma sakh une heure de temps bou matt.

Maman Khoudia dal, dama fogue ni ma nélaw mokoy déranger. Mais pas de conclusions hatives peut-être que diotéwoul dara ak mane, ni lay def gorom yeup.

Deme dieundi mourou pour ndekki bi ma deme diokh ko mère bi. Mais 7h dongue mo diote, fi gneupeu gui nélaw. Kheuyna dafa yewo khiffe ?

Ma khalate ni li gueuna rafette moy ma ladjko loumou sokhla balla may nelawi watt.

-Ma tegue ndokh bou tangue bi ?

-Dedette tel na, gni yewoguougne.

-Magui dem ci nek ba.

Tontouwouma wakhouma dara, delouna nek mais khame nani douma nélawatt.

Ma tok time sama portable di khol lou samay amis di lidieunti ci facebook bi, mo ma déssé.

Wakh na ak Nogaye gnane nako 4 jours yi ma dieul ay, après ma delou watt. Togue rek guay def toute la journée. Bou dé ligueyou keur you sew yi la dinako meuna gérer avant may ligueyi, damay téla yewou rek. Khalatt na sakh mère bi yé ma. Légui le temps que sama gnari woudj péthiorgo yi di ayé,  gnome gnare kou nék 4 jours mouy 8 jours, khana di na ci meuna ame djank.

******* 

Khalil dé mogui soguay foude, wawaw Ndiaye Diatta, bou la nékhé. Mane mi yewou thia fadjar ndakh sa yaye.

-Yow kagne ga yewou ?

-Khana daga may mbalak ?

-Yeugoumala dal... Mou wakhma lolou ba paré diogue togue ci kow lale bi.

-Sa yaye moma yé ay 7h pour que ma dieundi mbourou.

-7h ? Khana mère dafa faté ni tay la dimanche kéne démoul féne.

-Kheuyna da beugue ma tame rythme bi ?

-So amé diank mou wathie la.

-En parlant de djank, sank khalatt na ci. Mais keur gui kéne amoufi diank dé.

-Parce que djiguéne gni kéne liguéyouci. Ame naigne diote. Wala daga beugue def ni gnome ?

-Mouk. Mome kay gnane na yalla, mokal ba oubi sama salon bop.

-So amoul wone projet bobou sakh douma la ci bayi.

-Kharal ma indil la sa serviette bi ga sangoudji après gnou ndekki dji.

Kéne kou mel ni yowOù les histoires vivent. Découvrez maintenant