Khalé bi limou sagncé billay wallay Rihanna,Beyoncé, Nicky mitate sakh meusou ma guiss niou solle lou mell nonou je te jure
Mangui dokh dieum ci mom moumay khole makoy khole ma nieuw bassi mome rek serré ko dans mes bras maye ko bene câlin kirassoulilay dija mongui melni tangale solle robe bou noire deff voile khetou parfum bi ba taye dafa dess sama bakane yi ak sourire bou nice bi machallah niou ande di dokhe pour deme souniou keur ci yonneu bi moumay expliqué bimouy nieuw dafa tasseke bene grand ci auto bi
Grand bi:sokhna ci yaw mom raffete nga de
Khadija : machallah merci
Grand bi : wa yaw meussou ma guiss kou melni yaw yangui molle
Khadija : tchip yaw mom euppeul nga dé mane dama ame dieukeur
Grand bi: yaw dé sa dieukeur fan nako
Mane mangui retane rek té kham ni soumako féké wonneu grand dama koy douguel coup par ce que sama diabar mouy toudou mollayame mes grawoul
Après touti niou ague souniou keur niouy dougou ma guiss ni dafa tite ma khole niko dija tkt pas cava aller
Khadija : hiii mouhamed ba sen wa keur amouniou problèmes
Moi: non non niome nio d'accord pour nga nieuw fi
Khadija: en wa bakh na
Niou dougou ci biire keur gui ma présente ko wa keur gui yeupp
Khadija : ani sa mame
Moi: mongui ci biire dafay diouli
Khadija : en okey
Moi: niou dème sama chambre
Khadija : chambre wa yaw mome telle na diii
Moi: ahahaha dama lay togne rek nagne deme ci salle bi
Khadija : mdr yaw sérieux wo dara wa niou deme
Niou dougou ci salle bi tokkeu di wakhtane sama tite soeur bi nieuw Diatou kham nga mome dafa beurri wakh nieuw rek commencé di ratatati
Moi: yaw mi bala ngay wakh demal maye ko loumou nane
Diatou: moh yaw doma bayi ma terou sama diabar wa khadija ninga deff
Khadija : moh bayil togne guiss nala ak sa taille basse boubax
Diatou: ( dafa beurri tuteur) mane dé nillay deff ak yeben mes diankeu yaw mi toggo dé sa robe bakh na
Khadija:Mercie waye c'est gentille
Diatou: wa wouyou ma fi sa keur leu defal loula nekh relax mangui nieuw niou zeuzeule
Moi: diatou hé reglel dé fi dokofi zeuzeulé rakadiou nga trop
Khadija : wa mouha bayil diambour dagni feulalé
Moi: en bon wa baxna ba sama mame fekk lene fi
Khadija : sama woudiou bobou sou nieuwé ma affronté ko rek
Moi: en yay wakh lolou mangui koy wooo
Ma deme woo sama mame niko sama ganeu bi nieuw na legui danga makoy napale niou khole bakham noumouy deff ma retourné ci salle bi tokkeu di waxtane ak dija rek dégue kong Kong mani entré rek sama mame dougou
Sama mame: assalamou alleykoum
Khadija: malleykoum salam
Sama mame: takhawe fixé ko neko hé yaw yay sama woudiou bima niémé bay dougou sama territoire
Khadija : seugue dé dette mame mane douma dieul sa dieukeur mouha sama kharite leu rek
Sama mame: hé dama beugue nga wakh konneu lofi woute ba deff sa robe boubax bi mane ngay titeul ci mane khana guisso ma ak sama dialabé namou ma dara
Khadija : sourire non guiss nala kaye danga raffete sakh mane dé beugue na mame bou melni yaw
Sama mame: ahahaha yaw tapete nga rek yaw mom niémé nala ba paré so seuye cé dinagne dioubo no deff ana sen wa keur
Khadija : ahahaha lolou nekh na souniou wa keur niongui fa niongui ci diam
Sama mame : dalal ak diam yaw mome nimala guissé khalé boubax nga machallah
Khadija : mercie mame yaw yama guena bakh
Sama mame: nalene bayi nguene waxtane
Moi: wa baxna
Khadija : wa mouha yaw mome sa mame bi féroce na dé
Moi: MDR yaw tapete nga rek mako santeu limou deff yeupp mes melloul ni
Khadija : aye mouha méré nala mangui deme gnibi
Moi:non bb dama doneu foo rek legui wakh ma lo beugue ma defal lako nga balma
Khadija : ennn wa legui fethiale ma
Moi: hiii taye ma dé meunou ma fethi dara mes comme que mako togne ma fethiale ko wayou Ouzin keita bi beureung beurrigo
Khadija : ahahaha mouha yaw khamou ma wonneu ninga rakadiou wé ma wakh ngamay fethiale beureung beurrigo Ouzin keita mou wayadii mi
Moi : ah contane nga
Khadija : trop sakh mane dama beugue goor bou galant
Moi:(may signe) oui mane mome dama jongué ci khalé mes kharal ma khole fou rér bi tolou comme que 20h:30 diote na
Ma deme dii kholi rér bi ndakh paré na dégue sama téléphone di sonné ma retourné dieul téléphone bi khole mouy appelou mamy ma bayiko mou sonné ba coupé ma deff sama téléphone mode avion mes comme que dafa deuguere gateu mou nieuw souniou keur
Mangui ci salle di relax ak sama diabar sentir ni niongui feugue bountou keur gui ma dioukk di deme pour oubil ko guiss sama tite soeur bi diko oubil ma freiné takhawe sama tite soeur bi comme dioubo woul ak mamy mou oubi guiss ko rek tchipatou ko
Diatou: yaw am nga diom lofi deff
Mamy: Diatou mane xoulo indi wouma fi
Diatou : ladiou mala lolou lofi deff
Mamy: mouhamed lay sette
Diatou: mouhamed nekou fi rek teuthie bountou bi
Mamy : continé di feugue feugue you metti
Ma khame ni souma guissoul dou deme té dinama indile problème ma deme oubi bountou
Moi: yaw lou khewe bangay nieuw fi ak louma la wakhone
Mamy: malako niane nagne deme ci biire ma wakh la c'est urgent
Moi: non non dagno ame réunion de famille demal après nala wo nga nieuw fi
Mamy: en bon réunion de famille heure bi
Moi: legui lo beuga wakh damay fene legui demal sa yonneu vas te faire foutre
Ma frappé porte bii retourné ci salle ma khole dija mou khole ma ma kham ni dégue nama may wakh ak djiguene mouni ma lane la sen bruit bi beurri na dé may douté bakham ma expliquer ko wala mani nako expliqué rek
Moi : sama bene ex mofi nieuwone ni dama sokhla
Khadija : en bon loutakh deglou woko
Moi : weu yaw kham nga ki loumou ma deff bangay wakh est ce que khame nga loumou beugue
Khadija : loumou meuna beugue nga deglou ko rek après ya mome sa bopp nga deff loula nekh
Moi: MDR yaw mi règlel ki dafma deff lou niaw té saleté
Ma expliqué ko sama histoire ak mamy nimou démé commencement ba fin
Khadija : balma khamou ma wonneu ni nonou leu démé
Moi: non tkt pas bb
Après touti rér bi paré niou deme rerando ak wa famille bi waxtane bégué sama tata bi defare juste bou nekh niou feulalé ko
Moi: khadija goudi na dé 21h diote na nagne deme nga gnibi
Khadija : wa legui danga may dakkeu
Moi: non dou lolou dé dafa goudi té khame nga sa papa dafa sadique
Khadija : wa baxna nagne deme ma taggo
Après bi niou deme mou taggou souniou wa keur
Wa keur gui yeupp guene diko goungué
Moi: wa doyna yame lene fi
Khadija : waw mercie contane na trop dina saware ci nieuwate fi machallah
Niouy deme makoy goungué rek ma guiss mamy tokhawe bi bopou kogne bi dima khare (putin genrou nitte yi nio lakalé)
Mamy : wa mouha li moy danguene ame réunion de famille
Moi: yaw mi est ce que do deume lane la
Mamy: sa thiaga bi motakh ngamay bagna falé
Khadija : MDR yaw danga perte par ce que ki dilla dawlo sama guinaw lay topou pour mouha rek niakk ngako mako té sama digou lokho dagno beuguenté pire
Moi: wa waw yama diaral insomnie dé yay sama niakk torokh yay sama amoul bayi
Mamy : mouhamed mi dé dinako tewate sama lokho kham ko
Moi: yaw dama disse sa kawe yamal
Wa kogne bi yeupp takhawe dignou khole thieuy yalla mangui marqué samay point dé
Makk dija niou deme bassi tally bi ma dieuleul ko taxi mou deme gnibi vers 21h45 mou woma nima ague na ci diam mes papame.....(Juste pour vous dire une chose s'il vous plaît max de partage)
Partage lene voted lene commentaires lene aussi sen kharite yi nagne ci diote bamou beurri dollé mercie

VOUS LISEZ
Mbeuguel
RomanceSalam Mangui toudou mouhamed Gueye Nioumay wowé Diego 21 mes souniou wa keur beugou niou toure bi sénégal dalle mo metti mes comprendre nalene parce que sama toure mo selle mangui ame 19 ans teint maron taille 1m75 gentleman kharitou khalé yi akk...