Bokk na ci teggiin yu rafet nga bañ di ree ci jataayub ku la mag ndare muuñ, nga bañ di wax ak moom cig bayliku, maanaam ëppal ci wax ji, lu ñor nga wax ak lu ñorul,moom daal nanga yam ci li mu soxla ci yaw, bu boobaa doxal nga ay teggiin ci moom.
