✨ *Jootayou MOURIDE*✨
💠 *أعوذ بالله من الشيطن الرجيم.....بسم الله الرحمن الرحيم*
🌼 *جرجف خادم رسول*
☘ *السلام عليكم ورحمة اللّٰه*
*_⚜Jaar-Jaari Serigne TOUBA ⚜_*
🔲Weer wou né daan nagnou ame lou tollook ay tééméér ci ay Kaamilou lokho, lou bokoul ak lignou daan djeunde ci ay Kaamil you gnou mool.
♻Mbooloo yi bari woon nagnou ci moom ca *Ndiaaréém*, ba ngour gui moudjoon aayé ko mouy dokh ci nitt gni ci loudoul ag diggalé, loo lou taxoon mouy wout ay palantéér you ndaw ci bountou bou nékk ci keur gépp nga xam ni foumou toggué ba oubi palantéér, gnaari nitt mana guissék moom bou gnou djalle yéénéén gnarre djéguési noonou la gnou koy nékké ci souba ba beuthieuk ci li guena bari, tégg ca gnou nékkaat ca takkoussan ba timis ak léég-léég ci goudi gui. Amaana léég-léég tam mou dém bind ag Xassida mbaa mou dém ca bountou djiguéén gnaay siyaaresi mba mou dém némméékou ndiaboot gui.
⚜Sou beuggana djangalé dafa daan soril nitt gni bountou bi, sou ko déféé gnou kouréélou, Serigne bi tambaléé tomb ci souff ngiir ndiangaalém *Sariyaa* ak *Haqiiqa*, ci *Al Quraan* ak *Hadiis* ak *Hikam* ak masalay *Fiq* yi.
📌 *A Suivre.....*
VOUS LISEZ
Ayy kadouy ndénkané akk fatali
RandomDieureu dieufeuti Serigne Touba Djarama Mame Cheikh Ibrahima fall