*✨...Yobalou Souba...✨*
🏵 *...Direction Magal Poroxane...**_⚜SOKHNA DIARRA_ rooyoukayou bapp djiguéne⚜*
🌼 *Sokhna ci cibb Néggou Seuyame...*
🔮 *Ci loolu Soxna si Yàlla may na ko ci SEUY bou barkeel boobu, (04) ÑÉENTI doom, yoy di nanu sawar lool ci tudd séen i tur, ak wax as tuut ci SÉEN i jikko yu kawe.*
📌 *Nu lime LÉEN nii:*
🔰*1°/Ab taawam moo di "Maam Moor [Jaara] MBAKKE", (Boroom Saam walla Magi Mag)*
'''"Mom Sëriñ Moor Anta Sëli MBÀKKE" ak "Soxna Mame Jaara BUSO",
doon ab jullit bu di doomi jullit, di as gor su di doomi gor, doon ku SÀMMU te ragal Yàlla, daan JÀNG ak a JÀNGALE Alxuraan, ci anam gu YÉEME, daan JÀNGALE it bépp XAM-XAM bu aju ci diine.
Nee ñu saxoo woon na guddi gu ne TÉEMÉER i RÀKKAA (100 i ràkka) noppi JÀNG ALXURAAN ba mu mat.
bi mu fi bawoo "Sëriñ TUUBA" seereel ko ni:"Man déy Sëriñ MBÀKKE kajoor ak Sëriñ Moor Jaara rekk laa mas a gis kuy dugg ci BÀMMEEL te YOBBAALE wu fa BÀKKAAR."
Loolu di tegtale cofeel gu Sëriñ bi amoon ci moom, ak rawati na nag di nu XEMMEEMLOO yoon wi mu jaar ba am loolu.'''
🔰 *2°/ Ki ci topp di "Sëriñ Habiibu l- Laahi MBÀKKE" Mom "Sëriñ Moor Anta Sëli MBÀKKE" ak "Soxna Mame Jaara BUSO"*'''Doon ab jullit bu di doomi ñaar i jullit, di as gor su di doomi ñaar i gor.
Sëriñ TUUBAA seereel na ko ni:
ku amoon ab CÉR bu kawe ca Yàlla la.Ba jamono yi mu nekkee, moom "Sëriñ Tuubaa" Njaaréem (Diourbel, 1912-1927),
baaxoo woon na di dem Xuru Mbàkke di SIYAARE Bàmmeelam.'''
*3°/ Teg ci "Soxna Faatima MBÀKKE" mom "Sëriñ Moor Anta Sëli MBÀKKE" ak "Soxna Mame Jaara BUSO"*'''Doon ab jullit bu di doom ÑAARI i jullit, di as gor su di doomi ÑAAR i gor.
Ndeysaan!
moom nag ag dundam lu gàtt la ci ay at, dellu na ci Aji-sàkk ji ci jamonoy ndaw."Seex Siidiya Gànnaar" di ab Wàlliyu ca Gànnaar seere na ci moom seede yu rafet cig sellam.'''
🔴 *4°/ Teg ci nag, sunu waaji, ki sunu LÀMMEÑ ak sunuy cér dul deñ di sawar ci tudd ko ak di ko LIGGÉEYAL, Jëm jii nga xam ni jur ko rekk doy na SËKK daraja te kawe wépp tagg wu deefi ndamoo.*
🔰 *"Seex Ahmadu Bàmba MBÀKKE Xaadimu r-Rasuul" mom Sëriñ Moor Anta Sëli MBÀKKE" ak Soxna Mame Jaara BUSO"*
'''Doon ab jullit bu di doomi ÑAAR i jullit, di as gor su di doomi ÑAARI gor.
Di ab YEESALKATU L'islaam, doon LIGGÉEYALKATUB Yonent bi, gëm Yàlla daa ko jaamu ci JAAMUWIIN (UBOODIYA) gu ko kenn fekkul.
Sopp Yonent bi (j.Y.m) ci anam gu xel mant a takk cig foor boole ci daa roy sunnaam ba mujj di moom.
Àddinaam jépp mu jeexal ko ci wut ngërëmul Boroomam, Soppeem ba (Mustafaa) ak ngërëmul képp ku Yàlla gërëom, teg ci LÉPP lumu def NJARIÑUL MBINDÉEF yi la ci jiital tax mu naa "Lam an'u maa lam yufidi"
(Masumaa jege lu JARIÑUL (MBINDÉEF yi)).
Moom daal xamn a don ci mana sori ci jëmm jii, ndax Seex Saliwu Mbàkke nee na:
"Lu ñépp xam; wax ci tuuti doy na"! kon nu xelu te yam foofu.'''🙏🏼 *Nagnou xam lignou am, Fonkkou lignou am, mouy Serigne Touba 💖....Wa Saalaam👌🏼👌🏼*
VOUS LISEZ
Ayy kadouy ndénkané akk fatali
RandomDieureu dieufeuti Serigne Touba Djarama Mame Cheikh Ibrahima fall