✨ *Jootayou MOURIDE*✨
💠 *أعوذ بالله من الشيطن الرجيم.....بسم الله الرحمن الرحيم*
🌼 *جرجف خادم رسول*
☘ *السلام عليكم ورحمة اللّٰه*
*_⚜Jaar-Jaari Serigne TOUBA ⚜_*
🔲Tabaax gui moom gni gui koo door bisou *Altiné* ci yoor-yoor, Serigne bi wathieu ci biir paxou xutba bi, *Cheikh Mouhtar Binta* nékk ci wétam yor ndab lou def Ciment. Serigne bi djeul djoumtoukaayu tabax bi tibb ci Ciment bi wakh *Bismillaah* sotti, djeul ab xéér tégg ci ban bi, djeulati guassoukay bi door ko ci xéér wi djangue *_wa'iz yarfahou ibraahiimul miihul Aliim_* daa di fay djoulli gnaari ràkkaa gnaan fa. Liguéy bagui aggue ci *djouroom gnarri att (07ans)* ci téwayou Serigne bi mou djoulli faa gnaari *iid Koori ak Tabaski* gnaari yoon ci lou wérr wayé djoulli woufa *Al djouma*.
☘ *Serigne Mbacké Bousso* néé na li koo waaral mooy moom massou faa yéénéé sax mouk té kou yééné wou la sax, *Al djouma* warou ko. Ka fa ndjeuka taxawal *Al djouma* mooy *Cheikh Ibraahimah* raakam dja, ci deuppoo gou mou ci déff ak *Cheikh Mbacké Bousso* ak doomi Serigne bi ak maggi Taaloubé yi ndakh gnoom gnéppa fa yéénéwoona sax.
📌 *A suivre.....
VOUS LISEZ
Ayy kadouy ndénkané akk fatali
RandomDieureu dieufeuti Serigne Touba Djarama Mame Cheikh Ibrahima fall