🏵 *...Direction Magal Poroxane...*

370 20 2
                                    

*✨...Yobalou Souba...✨*


🏵 *...Direction Magal Poroxane...*

*_⚜SOKHNA DIARRA_ rooyoukayou bapp djiguéne⚜*

🌼 *Sokhna ci cibb Néggou Seuyame...*

🔮 '''"Soxna si ci'''  *NÉEGU SËYAM:*
'''Ci wax jii manees na cee xame ni, Yàlla DÉNKU LÉEN woon alal jees man a gis.'''

🍁 *Waaye xanaa ñu di ay JAAMUKAT i Yàlla, di ay boroom i XAM-XAM youy JËFE seen i XAM-XAM, di ay jullit te doon ni gor, SÀMMU te ragal Yàlla....: Ci yii jikko daal la Kilifay "Sokhna ci" xool, ba nangu faa maye SÉEN doom, "Soxna Diarra" yit ci YOOYII jikko la xool ba nangul ko.*

🔰 *Loolou it masoul di feeñ ci SÉENUB ÀND, xanaa ÀND ak moom ci dooleem ñuy dund ci sutura ngir Yàlla.....Mu jàppe ko ni ab sangam di topp ay ndigëlam ci anam gou yéeme.*


🔴 *Misaalum nittali bou siiw bii te doy kiimtaan:*

👉🏽'''Am na bis "Maam Moor Anta Sali" di takk aw SÀKKET teye loo ko SÀKKET wa, dougg ci biir NÉEG bi,
( xayna, ngir JËLI LUMU takke SÀKKET wi )
faaf Yàlla dogal ab taw SÓOB, mu far toog fa NÉEG ba.'''

*Nee gnu:*

'''Ba ci fajar gi "Maam Moor" GÉNN fekk "Soxna si" mu TËYE SÀKKET wa te tawte.'''

*Mou ni ko:*

'''Yaw de xanaa fii la la taw bi fekk.
Lu tee bi muy taw NGA dugg ci biir?
"Soxna si" ni ko:
Sa NDIGËL a ma ko TËYELOO woon te ba leegi NDIGËL JUGEWAATUL ci yaw BÀYYI loo ma ko.'''

🤦🏻‍♂ *Lii DÉY YÉEM na ma, te war a man a YÉEM waa jamono djii, ci gii nangou nou mou man a ame.*


📍 *"Soxna si" it LIGGÉEYUB KËRËM moom rekk a ko daan defal boppam, di ko def ca anam gamou ware, boole ko ak matal jaamouy Yàllaam.....*

😭 *Ci topp boroom KËRËM ak dabou ag CÀKKUTÉEFAM, GINNAAW "Maam Moor" ab SËRIÑAM daa XAWOON a JËM mag, te fi ñu NEKKOON ÀLLE, ba tax sedd ba xaw faa tar. Ci loolu daan na ko FÀGGUL matt mu muy jaaroo, ngir mucc ci sedd boobu NGA xam ni baaxoul ci mag.*


⚠ '''Ba bis (xayna matt jafe na ko),
ngir BËGG a matale CÀKKUTÉEF i boroom KËRËM, tax mu DÀJJI gaal gi mu daa denc i mbiram ngir taalale ko ab SËRIÑAM. Cey!!'''


*Noonu it la ko waykat ba waxe "Seex Sàmba Jaara MBAY" Taalubeb "Sëriñ TUUBAA"*

🙏🏼 *Nagnou xam lignou am, Fonkkou lignou am, mouy Serigne Touba 💖....Wa Saalaam👌🏼👌🏼*

Ayy kadouy ndénkané akk fatali Où les histoires vivent. Découvrez maintenant