*✨...Yobalou Souba...✨*
🔘 *Jikkó ju rafet...👉🏽👂🏼*
🔸 '''Fu fiw jullit daje déglul koo fa dégg mu wax
Ak dëgg jàppal, ku wax aw fen nga ree te ba fa.🔹Ab yar bu sotti bu àndak dëgg moo mata yor
Yii yaari yëf ku ko yor fum jekki jekki ji fa.🔸Na ngay naxante ba doo moy Yàlla, doo moyu nit
Bis boo tëlée lii ma wax jaaril fa Yàlla ne fa.🔹Te bul naxantee ku nit bay def lu Yàlla bëgul
Bul dab mbégum surga nak bay jot merum kilifa.🔸Bu kenn wax lu amul bay tax nga naa ko amul
Koo gis ci mbooloo mu naa nit fen nga kat gënu fa.🔹Werante saytaane moo koy sooke mbaate ndawam
Ku wax su dee dëgg mbaa muy fen ërël ko ko fa.🔸Ku fen fi yaw bul saxal, bul dàq, bul toroxal
Te bul gëmit suturaalal fen wa bam juge fa.🔹Te bul ko jëw yit ginaawam kon mu yobbu sa jëf
Ndegam bawoo na ca yaw sax Yàlla mii ma nga fa'''🙏🏼 *Nagnou xam lignou am, Fonkkou lignou am, mouy Serigne Touba ❤....Wa Saalaam👌🏼👌🏼*
VOUS LISEZ
Ayy kadouy ndénkané akk fatali
RandomDieureu dieufeuti Serigne Touba Djarama Mame Cheikh Ibrahima fall