Wakhi Serigne Bi

752 48 4
                                    


Nee na sama doom yi am na ci ño xamni duma wax ci ñom darra lu dul bis peñ, amna ci ño xamni dinaa wax ci ñoom tuuti, daadi nè ma nak  jikkoy yonent bi (SAW) laa wone te jikkoy yonent bi (SAW) kenn attanuko mo tax ma sèddëleko sama doom yi,

Daa di ne Mouxammadul Mustafa mooy yonent bi (SAW) xarfan bi xarfin,
Mouxammadul Faddil juboo gi ma jubook sama boroom ba luma ko wax mu def ko mooko yor
Abdul Axad Alxuraan laa ko jox ,daa di ne maay ilimaani ilimaan yepp loolu mingui ci Abdul Xaadir, liggèey loo gi ma daa liggèey loo jaam ñi ngir jariñ leen, loolu mingeek Saalixu

Teere yi ma daa taalif ngir xamal ci jaam ñi niñuy jaamoo seen Borom loolu mingi ci Su-aybu, araab yitam fonk naako ngir Yonent bi(SAW) loolu mingeek Muxammadul Murtadaa ,,

Daadi ne ñaar rekk laa ci wuteel, muy Muxammadul Amiin ak Muxammadul Bassir ndax Muxammadul Amiin day mer te man duma mer te bu meree sunu Borom mer , Muxammadul Bassir nak mo yor gaalug ajjana te man maa moom ajjana ,kon juboo lèen ak moom mu andi lèen fi man

Ayy kadouy ndénkané akk fatali Où les histoires vivent. Découvrez maintenant