1- BIOGRAPHIE
Serigne Modou Moustapha Fall nak daaf di jeuum djou djaaraa wahtané ci yoon wi,
Migui gaané adina am niouné Darou Salam am niouni Ndar, waayé louci né am na firndé. Niou japp rk ni migui gané adina nak ci atoupp 1893, Waydjouram bou Djiguène di Sokhna Astou Sylla.
Jàngaam nak migui ko tambalé Théyeene Djolof , am niouné fala jàngué, 1907 la deem Gawaane wayee wax nagn ni djougué waat nafa,
Wayé Théyeene Djolof daal la agaalé tarbiyaam daal faa lako défé lolo geuna wér !
waayé daaf daan déf digeunté serigne bi ak cherayma Fall.
Sougnouy waaxtaane ci Serigne Moustapha Fall dafaay jaadou niou déf li Toubab di waax décrtyptage,
Manaam jàngaate ci Jeum dji ak dohine woum yoorone niou djeem ci donté xamougn leepp.
Baguaa xam ni lepp lim fi néké woone moy défar yoor poussom di niaaw
Té so xoolé lépp dafaa tégou won ci agg Talibé téé dafko daa deelo ci Talibé
Lolou taaxna nonou laafi andé won ak Cheikh Modou Moustapha tee Segn Fallou itaam noné la andaté ak mom ba noum fi djougué.
2- DIGEUNTEE SERIGNE MODOU MOUSTAPHA AK SERIGNE TOUBA
Mom waxoumala Chéra Fall wayé segn bou màgg bi daaf ko teelona yéh tchi ni gnay doxee,
Bo xoolé doy biko Serign Touba doylo woon rk deey doon app firndé ni Chéra Fall djour na app poukaal,
Diggeunteem ak Chéra Fall mom bénene mbir leuu,
Amnaa biss segn bou màgg bi wolouko niko Modou Moustapha Fall kayy maa dinkeu laa :
- Deel sakou agg Talibé tee bagn di saakeu ay Talibé
- mouniko xana xamoni keen dou andeu ak ay Talibé di doug bameel
wayee agg talibé rék léss di andal di dougg bameel
Mouniko Modou Moustapha mouniko Fall:
- Deel sakou ngeureum tee bagn di saak ay deureuum
ndaxx keneu dou andeu ak deureum di dougg bameel, ngeureum rék léss di andaal di doug Bameel
Mouniko Modou Moustapha mouniko Fall li malaa dink boko dieufé digua ci djarignou adinaa djarignouci Alahiraa
Bo xoolé li yeup xamni Mame Modou Moustapha dafaa doonone app waliyou bou segn Touba beugeulone boppaam
déf ci mom lim wara déf ci mom guinaaw bou waydjouram Cherayma Fall nopé ci mom
ndaax biss Segn bou màgg bi daaf ko Djox ndigeul néko djougaal sakétaal ma saakét wé,
Cheibra naara jouk sérign Touba niko baayil Modou Moustapha lakoo saakéte lo,
Baa chéra Fall mérr ci loleu ni souma xamoone ni souma djouré doom mou dooneu ma ci légeuyal segn Bamba koneu douma djour doom,
Lolou rék firndé laa ci taamit ni Segn Modou Moustapha app pounkaal laa.
Nénagne Serigne Modou Moustapha loum djour waliyou la? ndaxté mokoo waax baayifi
Boolé ci taam Nar bi nieuwoone di lidjeunti mbirou chéibra nane ko baax nga lole wayee do djouli,
bo doon djouli mom keen dotoulaa geunati ci adounaa, Chéra Fall niko dama djissoute kamaa mat élimanee,
Baam ko waaxé lolouu nar bi niko maane nala taanal élimane, ndax djiss na sa bir jaabot gui niou mat élimane,
Chéibra niko Bismilaah, Nar bi djouk di taaneu ba djiss Segn Modou Moustapha,
niko ki déh sunu borom xamaal namani meussta moy Yallah ki déh matt na élimane,
Néna Cheibra ni neuu djouk taxaaw, mou djouk chéra Fall ni aah kokou Moustapha Fall,
mouniko Fall, chéra fall niko ah kokou sama doomaa, Lamaa japoone baa am Modou Moustapha doumako baayi,
Niou djagaati ni Segn Modou Moustapha Fall Goor yallah deugg laa.
Dadaane déf di weur deuk yi lou bari bir sénégal war fassaam
waayé saa bou daan dém rék deey ni deem ci Serigne Touba niko nianaal maa,
souma djougué fi diaar si saa baay Chéra Fall mou nianaal meu ma dogg di deem!
Lici yeemé moy saa bouko serigne Touba nianalé baam deem djaar si Chéibra mou nianal ko,
ndékété Cheibra niane biko serigne Touba nianaal laay djeulaat baa taxna sou deemé yoon waa dou néékh
baa xeeweul yiko serigne Touba diokhone douthiaa déssé ti dara!
Beug gui ko serigne Touba beugoone taaxna, biss mou taggou serigne Touba niko nianal maa,
Serigne bi niko Modou Moustapha taggou nga saa baay ba nopi? mouniko dédét dama geugone nga nianal ma ba nopi
souma fi djougé ma jààr faa doraa deem, Segn bi niko dédéte lepp ci beug guim ko beug,
xamni sou deemé Cheibra jeuul xeeweul yi, motaah Chéra Fall momi kouuy fir ci seuu doom baayiwo keenn,
Serigne Touba niko nak deemal ci saa baay soula nianalé, bo nieuwé fi maa nianal leu nga doraa deem,,
Baamou deemé ci Cheibra mou nianal ko mou delou waat ci serigne Touba, Serigne Touba nianaal ba nopi niko:
- Modou Moustapha mouniko Fall, xanaa xamoni lepp loumaa laa daa nianal so deemé saa Baay dako daa djeuul,
Motaah manilaa nga deem ci mom ba nopi doraa nieuw ma nianaal nga deem !
Segn bi dafko beugoone baa sou né wowaal leen ma Modou Moustapha sama mom, niou wowaalko Segn Modou Moustapha Fall,
Biss wo nako dieul nitt djox ko niko Moustapha djeuleul ki yoobou déf ci ling ci wara déf beuss pinc dinalako ladj,
Niou xamé fofou rék ni Segn Modou Moustapha kou bari won martabaa la,
Firndé bi moy Serign Ibra Mbodj, ndaax mom dafa djoudoon doon silmaxa, té bayaam buur lawoone, baayam tok ni douma djour silmaxa damakay raay!
Badiane bi taxaaw djooy daaldiko niane niko djoxmako ma yobou ko am neu serigne bou nék ci pinkou bi kokou loko diokh mou défarko délo lako,
Mouniko kokou kaane leu? mouniko Cheikh Ahmadou Bamba Khadimou Rassoul, bagnoul béneu mbidéf xébouul kéneuu,
Té lou nit yaakou yakou bougn ko ko djoxé mou défar baam baax, téguama ko diokh ma yoot koko,
Serign Ibra Mbodj bobou "Ségaane" la toudonne, néna badianaam yobouko ci serigne Touba, boléko ak ay fass ak jaam,
Serigne Touba délo leen fass yi ak jaam yi, daal ni néko no toudou mouniko "Ségaane", Serigne Touba niko Ibrahima mo geune "Ségaane",
Toudé nala Ibrahima, mou daaldi kaay teeyé ay faan daldi wo segn Modou Moustapha Fall baamou nieuw,
Mouniko ki djeuleul yobou lou mata déf ci mom nàngko déf ci mom, bou beuss Pinc dinalako ladj,
Segn Ibra Mbodj momo néna biss nit meuss na nieuw di jàng ay wolofal cheikh samba Diarra Mbaye, segn Modou Moustapha Fall daaldi géneu
Niko ah manee wolofal Cheikh Samba Diarra yi ngay jàng dàfma nékh loleu saax ndax dafmay sogneu, souma sagnoone diko dégg sassouné,
Serigne Ibra Mbodj néna maa tambalé jooy, daldi niko souma sagnone dé lo beug ma déf ko wayé awma ay beut meunouma jàng té saam xél néxoul,
Segn Moustapha Fall niko lol boum la nakari dinako déf ci yow, néna ma teud ba goudi mom Segn Moustapha Fall daaldi taxaaw ci bountu bi
Ni ani Ibra Mbodj, maniko mangui ni, né beuréte dadja ak mom mou daaldi maay dor aww xeut ci deuneu ma danou mou rombeu ma,
(Segn Ibra Mbodj moy waax déh) Néna bamaa xeuyé kérok niéneu fouki xassida tari nako fofou ak wolofal Cheikh Samba Diarra Yeup, néna dafmako sol ci béneu goudi,
VOUS LISEZ
Ayy kadouy ndénkané akk fatali
De TodoDieureu dieufeuti Serigne Touba Djarama Mame Cheikh Ibrahima fall